Lu tollu ci ñetti weer kepp, ginnaaw bi ñu leen falee ak léegi, Nguur gu yees gi mi ngi jël ay ndogal ngir amal i coppite ñeel doxiin ak doxalinu réew mi. Looloo tax, kii di elimaanu jëwriñ, Usmaan Sonko xamle ne ci atum 2025 mii di ñëw, dinañu taxawal njëwriñ gu yees. Ni ñu koy tudde mooy njëwriñu ngëm gi (ministère du culte). Maanaam, moom lañuy jagleel li jëm ci wàllu diine ak ya cay dem. Su ko defee, ñu mën koo génneel kopparu boppam goo xam ne, moom rekk lañu koy jagleel.
Ndax, moom dafa jàpp ne diine, ni yeneen banqaas yi amee solo la amee solo, muy lu ci mel ni wér-gi-yaram, tabax yeek ñoom seen. Xibaar boobu mi ngi ko fésal ci teewaayu kurél gii di Jamaa-atun Nuur Asuniyaa te, Muhammadu Maxtaar Siise jiite ko. Ndax, ñoom dañoo amoon aw waxtaan wu ñu doon séq ak moom. Ñoom, seen yitte moo nekkoon xamal elimaanu jëwriñ yi ne liggéeyu jumaay Tiwaawon ji àgg na. Te, jumaa jooju dinañu ko ubbi ci lu yàggul dara. Ca la xamalee mbooleem ñiy yëngu ci wàll woowu liggéey bi ñu ciy def ngir diine ji tamit am banqaasu boppam.