TEGGIG MALAANU KIIRAAYU USMAAN SONKO : LI CI YÉENEKAAY YI BIND (Paap Aali Jàllo)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Coowal Usmaan Sonko moo lëmbe réew mi jamono jii. Gannaaw tuumay siif ak tëkkub rey yi Aji Saar teg ci kow deru Usmaan Sonko ak xew-xewi altine jii weesu, fan yii, péncum réew mee féete wax ji. Nde, ngir ñu mën a àtte Sonko, fàww ñu teggi malaanum kiiraay mi koy aar. Loolu, nag, sañ-sañu péncum réew mi la. Dina yàgg am du yàgg ? Bees sukkandikoo ci yéenekaayi réew mi, xef-xippi lay doon. Waaye, layookati Usmaan Sonko, bind nañub bataaxal jagleel ko njiitalu Péncum réew mi, Mustafaa   Ñas, di sàkku ci moom 4i mbir…

Paap Aali Jàllo

Réew maa ngi mel ni dëmm bu jëfuur. Làmmiñ yaa ngi turumtàcc, xalaat yeek wax yiy jolli, xalima yiy rëdd subaak ngoon, guddeek bëccëg. Werante baa ngi ni kur : ñii di xëcc fii, ñee di ñoddi fee ; nit ñiy ruumandaat, taskati xibaar yeek seen i gan di jéem a faramfàcce mbir mi. Yéenekaay yi, ñoom, bu ci nekk, yaa ngiy sukkandiku ci say xibaar, di biral sa gis-gis ak di jéem a nànd cëppandoo mbir mi.

 Le Témoin bind ne :

« Mbir maa ngi waaj a tàng ci Usmaan Sonkoo (…) Bi Toppewaan bi sàkkoo ñu teggi malaanum kiiraay mi koy aar la wure wa dem këŋŋ, waxi mag dem ndañ-taali. (…) Xef-xippi ñu teggi malaanum kiiraayu Usmaan Sonko nde, Péncum réew mi, dipitey nguur gaa fay teg ndawal. »

Le Soleil di xamle ne, woowees na dipite yi bokk ci boppu péncum réew mi cim ndaje, alxames jii, bu 12i waxtu jotee. Bu dee njiiti kurel ya fa nekk, ñoom bu 13i waxtu jotee lañuy daje ngir jàpp bés yi ñuy saytoo mbir yi aju ci yoon. Mu teg ci ne, yégle yi biral ñaari ndaje yooyu, tuddeesu ci mbirum Sonko meek Aji Saar, waaye njortees na ne dees na ko fa waxtaane.

Les Echos ne, « Sumbees na liggéey bi ci anam bu gaaw a gaaw ». Wax ji mel ni luy junj ne, dipite yi duñ yàggal mbir mi. Dañ koy taxañ rekk, teggi malaanum kiiraay mi, Usmaan Sonkoo wuyuji yoon. Mënees na jàng ci yéenekaay bi ne, « liggéey bi door (…) ci njeexitalu ayu-bés gii toftalu lay war a jeex. Ci lees di xamee ndax teggees na malaamum kiiraay mi, am déet. »

L’As, moom, daf ne :

« Fileek ñu teggi malaanum kiiraayu dipiteem, ab déglu bi akub àtte, Usmaan Sonkoo ngi yaatal i pexeem ak a dajale gànnaay ngir jàmmaarloo ak ñi mu jàpp ne ñoo lal ab kootoo ngir xeex ko. »

Yéenekaay bi jukki ci mbir mi am njàngat, wax ne, « ci jamono yu ni mel lees di nattee solos yoon wu mucc ci loxoy nguur ciw askan. »

Li ci kanam rawul i gët.

« Bés buñ teggee malaanum kiiraay miy aar Usmaan Sonko, dinañ ko wol bam mokk rumbax, te duñ ci seet dara. Buñ ko xasee jàpp, ku koy war a mën a xettali diir bi muy nekk ci kaso bi ? Nguur gi fa la koy fàtte ndaxte xam nañ ni, Senegaal tàmmuñu xeex bu yàgg, dañ gaaw a toqi. Bu ko defee, buñ xeexee ab diir, dinañ dellu ci seen i itte, lijjantiji luñ dundale seen njaboot. »

Loolu la Vox Populi yaakaar ne moo doon yoot Usmaan Sonko. Yéenekaay biy fàttali ne, mbirum Idiriisa Sekk, Karim Wàdd ak Xalifa Sàll yépp, noonu la mujje.

L’Observateur moom, dafa gis ne, « Usmaan Sonko dina gëj a jariñoo malaanum kiiraayam » ndaxte « dipite yi sumb nañ liggéey bi ngir xañ ko ngëneelu dipite bim doon. »

 Bu dee Le Quotidien, moom, dafa biral ne ñoo ngi gaawtu ngir sottal mbirum Usmaan Sonko. Mu dolli ci, bind ne, « Toppekat bu mag bi dafa santaaneb gëstu te xaarul sax ñu teggi malaanum kiiraayu Usmaan Sonko. »

Enquête ne, mbir mi, « ci yoon la doore » waaye « xaat-xaat pólitig rax na ci ». Te, ba tay ci bindi yéenekaay bi, « ak mbir mii, xareb pólitig buñ mësta gis mooy waaj a amsi. »

Lii Quotidien di fésal njàngati pólitig yu leen benn xeltukatu pólitig biral ci mbir mi. Mu wax ci yéenekaay bi, ñeel xeexub altine ji, ne, « ku foog ne farandoo Sonko yi rekk ñoo ko doon xeexal, xamoo li xew dëgg. »Bees sukkandikoo ci lii lépp, dafa mel ni Nguur gaa ngi def kemtalaay-kàttanam ngir faagaagal Njiitalu Pastef li, Usmaan Sonko. Waaye, layookati Usmaan Sonko yi, Me Bàmba Siise ak i ñoñam, bind nañ ab bataaxal jagleel ko Njiitalu Péncum réew mi, Mustafaa Ñas. Liñ ko dugge mooy laaj yenn kayit yu aju ci mbir mi ak di ko fàttali yoon. Jukkees na ci bataaxal bi kàddu yii toftalu :

 « Noo ngi sàkku ci njiit li nga doon, ngir sàmmonte ak li yoon tëral, nga laaj ñaari àttekat yi féetewoo mbir mi, ñeenti kayit yii nuy limsi :

 1/ mennum ràppooru doktoor bu am ci mbir mi, te ñu defaroon ko ciy waxtu gannaaw bés bañ wax ne ci la Sonko siif Aji Saar ;

 2/ kàdduy seede yi ak yu jiiñkat bi ;

 3/ kàdduy jëmm ji kenn ci seede yi tudd turam te mu bokk Bennoo Bokk Yaakaar, kurél gi ëppaley dipite ci Péncum réew mi nga jiite te mu war a teggi malaanum kiiraayu Sonko mu bokk ci kujje gi ;

 4/ njëlbeenug kayitug tuuma yi Toppewaan bi biral, muy wone ne doorees na topp bi te teggeesagul malaanum kiiraay biy aar dipite bi, muy jalgati yoon bu bir. »

Fim ne nii, ñépp a ngi xaar ndogal liy bawoo ci Péncum réew mi doonte ne, daanaka àddina sépp xam nañ li nar a xew. Wànte, li tiital ñu bare mooy li nar a xew tey ci àllarba ji. Ndaxte, bile yoon, ndaw yi dañoo nar a fippu, jàmmaarlook alkaati yi. Li yéem ñépp nag mooy kenn xamul naka la Péncum Réew mënee jébbal yoon dipite bu ko yoon laajul ! Ndax, doonte sax setalul Sonko, Basiiru Géy, Toppekat bi, bindul fenn turu Njiitalu Pastef li ci bataaxal bi mu yónnee Mustafaa Ñas…

Mu mel ni, réew mépp a ngi toog ci nen.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj