TËJANDI NAÑU JÀNGUNE BU SIGICOOR

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw jàmmaarloo yu metti yi amoon Jànguneb Asan Sekk bu Sigicoor, kilifay daara ju kowe jooju mujj nañoo jël ndogalu tëjandi ko ba jëmmi jamono. Démb, ci àllarba ji lañu siiwal xibaar boobu ci ab yégle.

Dafa di nag, yemuñu rekk ci tëj jàngune bi. Ndaxte, ci seen yégle bi, dañu xamle ne tas nañu mbootaayi ndongo yi (amicales). Rax-ci-dolli, dàq nañu xew-xewi yeesalug mbootaay yooyee. Tasaale nañu tamit kurél gi ëmb ndongo yépp (La Coordination). Nee ñu, dinañu amal ay ndaje ak banqaasi gëstu yi (conseil d’UFR et de département) ngir xoolaat anam yi ñuy àggalee njàng mi.

Ba tay ci seen yégle bi, ñu ngi xamle ne, ci “Centre universitaire” bu Koldaa ak UFR 2S bokkuñu ci tëj gi. Mën nañoo wéyal njàng mi ci mbaali jokkoo yi. Ndogal lii kilifay daara jooju jël naqari na lool ndongo ya fay jàngee. Ba tax na, ñu ngi sàkku ci ñoom ñu seetaat ko. Lu ko moy ñii di waa CESL (Coordination des Etudiants de Saint-Louis) moom, nee nañu duñu bàyyi dara mu sedd.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj