Waa Cybersécurité jàppandi nañu, barki-démb ci altine ji, 12 me 2025, ndawu Pastef bi ñuy wax Asuraa Faal, ginnaaw ay kàddoom yu ñàkk teggin yi ñu gis cib widewoo buy daw ci lënd gi.
Kàddu yooyu nag, moo nga ko doon jóor Maki Sàll mi fi nekkoon Njiitu réew mi ak Maam Mbay Ñaŋ, nekkoon fi itam jëwriñ ci Càmm gi. Meetar Bàmba Siise mi koy layal, jàpp na ni ndogal lu xel mënul a nangu la. Nde, ci moom, kàddu yi Asuraa Faal waxoon, dafay wane ñëg gi mu jële ci xoqatal yi ko Nguur gi fi jóge doon xoqatal. Moom Asuraa sax pelent na kii di Meetar Musaa Jóob mi mu jàpp ni moo yaatal widewoo bu yàgg boobule ngir taqal ko. Kii di Uséynu Kayre itam, ñu gën koo xam ci turu Kaïré 221, jàpp nañu ko ginnaaw kàddoom yu soriyoowul ak yoy Asuraa. Démb ci talaata ji lañu leen jébbaloon toppekat bi.
Barki-démb ci altine jeet, waa DSC (Division spéciale de cybersécurité) jàppandi woon nañu jàngatkat bii di Aaróona Ñaŋ, ginnaaw bi ñu ko dégloo. Ñu koy jiiñ ni dafa wasaare ay xibaar yu wérul ci ay kàddu yu mu yékkati cib jotaay ca tele Sénégal7, keroog 15 awril 2025. Kàddoom yooyu nag, dafa ci doon taqal fajkat yi. Mu ciy wax ni, ca jamonoy Covid-19 ba, fajkat yi dañu doon wàll askan wi lii di jàngoroy mbas mi ci lu ñu tay. Muy kàddu yu doy waar te teey-xel. Tay ci àllarba ji lañu ko defeere.