TIIS WU RÉY FA GINE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mats futbal bu mujje ciy masta ! Mbir yaa ngi xew barki-démb ci dibéeru 1eelu fanu desàmbar wii, mu di woon ab finaal bees doon amal fa gine ca fowub 3i Awril bu N’Zerekore. Waaye, po mi, ciy jooyi naqar la mujje. Nde, 56i bakkan rot nañu ci. Rax-ci-dolli, ñu baree bari ame ci ay gaañu-gaañu yu metti.

Boobu finaal, am po mees doon amal fa Gine la, benn ekibu Labe waroon cee daje ak ekibu N’zerekore. Waaye, ci musiba la jeexe. Ndax ci xibaar yi jot a rot, xamle nañu ni soppey ñaari ekib ya ñoo ca doon xeex ba yëf ya daldi ëpp i loxo am ñu ci nàkk seen i bakkan, ñeneen gaañu ci. Loolu nag, di lu doy waar. Ndax, luy jubluwaayu lu dul boole ak a naatal mu mujj ciy siggil ndigaale, metti na lool.

Démb ci altine ji, Njiitu réew ma, Seneral Mamadi Dumbuyaa, génne na yégle di mastawu waa réewam, rawatina ñi nga xam ni ñii ñooy waa kër ñi faatu, di leen jaale itam. Gannaaw loolu, mu xamle tamit ni Nguur gi dina àngu lépp lu jëm ci wér-gi-yarami ñi fa jëleey gaañu-gaañu. Raglub N’zerekore moo dalal way-gaañu yi ngir saytu leen, amal ci itam paj yi war ci ñoom.

Moom, Njiitu réew ma, xamle na tamit ci yégle bi ni Nguur gi, ci loxo jariñ biir bi, ubbi na ab luññutu ngir leeral ci nu mu gën a gaawe li waral loolu am ba ñu xam nees ciy taxawee.

Réewi dëkkandoo yi di leen mastawu bu baax te di leen jaale ñi ca ñàkk seen bakkan yépp.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj