Ci alxemes ji, 6 Oktoobar 2022, la Fifa siiwal toftaleem bi muy amal weer wu nekk. Lenn lu bees ruuseewu ci ñeel ékibu Senegaal bi. Ci toftale biñ jagleel àddina sépp, Senegaal a ngi desandi ci fukk ak juróom-ñetteelu toogaan bi. Randuwul benn yoon bu ñu ko gam-gamlee ak toftaleb weeru ut bi. Bu dee itam toftale bi ñeel kembarug Afrig, Senegaal a ngi wéy di jiitu.
Toftaleb weeru sàttumbar bi Fifa génne deful lu dul firndeel mëneelu Senegaal fii ci Afrig donte ni ci àddinasi yëngatuwul fi mu nekkoon. Bii yoon, Aliw Siise ak i ndawam dañu aakimooti toogaan bu njëkk bi niñ ko tàmm a defee fii ci kembarug Afrig. Ci pàttali, weeru nowàmbar 2018 la gaynde Senegaal yi yéegoon ci donkaasi gi. Boobu ak léegi, def na 46i weer, maanaam 3i at ak fukki weer yu tojul dara ñu nekk ci te bokkuñu ko ak kenn.
Bu fekkee ni ékibu Senegaal bee jiitu ba tey ci kembarug Afrig itam, ékibu Marog bee ngi ko dar ci toogaan bu njëkk bi. Ci bési Fifa yi weesu, Senegaal daf ci ñàkk 0,21i poñ donte ni am na ci ndam ak témboo. Fekk Marog yokkoo ci 5,15 poñ. Looloo tax ba 20,88 poñ kott la Senegaal jiitoo léegi Marog.
Lu tax ba Senegaal ñàkk i poñ ci bési Fifa yi weesu donte ni am na ci ndam ak témboo ? Bu ñu sukkandikoo ci saabal bi di WiwSport, li ko waral moo di Senegaal tànnul woon naataango yu am solo lool ci futbalu àddina si ngir joŋante ak ñoom. War na xoolaat bu baax ni mu leen di tànne ndax solo si ñu am ci toftale Fifa yi ak poñ yi mu ci mën a ame bu bëggee des ci toogaan bi njëkk bi ci kembarug Afrig.
Bu ñu delloo ci toftale bi ñeel àddina sépp, Bérésil moo nekk ba tey ci bopp bi, Belsig topp ci moom, Àrsàntin ak Farãs soog dee ñëw ci ñetteel ak ñeenteeli toogaan yi. Réewi Afrig yi, Senegaal a nekk ci 18eelu toogaan bi, Marog ñëw ci 22eel bi, Tinisi soog di ñëw ci 32eel bi.