“TOLOF-TOLOFI ÀDDINA SEEK BIDDÉEW YI CI KOW ASAMAAN SEE YEM: AK FOO MËNTI DEM, AK LOO FA YÀGG YÀGG, BOO DELSEE FEKK LEEN FA NGA LEEN BÀYYI WOON, ÑUY XEF AK A XIPPI, MEL NI ÑU LAY MBËLLEE.”
Damaa jukki baat yi ci téere Bóris Jóob bu bees bi, MALAANUM LËNDËM, sama xel tukkeeti, ma sori li ma jege woon, sama dégg-dégg yit soppeeku ci saa si.
Kàddu yooyu, ndax mënees na leen a déndaleek li xew tey Ikren? Walla loolu du wax?
Déglul bu baax walla nga teey, ànd ak dal, xoolaat dëggantaan fan laay daanelee samay kàddu.
Bi xare bi tàmbalee diggante Riisi ak Ikren ba samay baat yii rot, ay miliyoŋi nit ñoo dawe Kiyeew walla yeneen dëkk ci Ikren làqu Poloñ, Frãs mbaa Itali.
Daw-làqu googu yépp fexee mucc ci dee ak wàññi seen metitu xol moo ko waral. Waaye daw làqu taxul a mucc.
Li ci yéeme mooy doxandéem yiy agsi tey Itali, ko ci laaj mu ne la “jërejëf ci dalal bi waaye nekkunu ci jàmm. Lépp lu nu amoon bàyyi nanu ko ginnaaw. Daw ba rëcc taxul sunu xol neex walla nu am bànneex.”
Biddéew yaa ngi leen tiim fa nu nekk, moo xam Itali la walla feneen, waaye taxul seen xel jóg ci seen waa réew ñay jàmmaarlo ak ñeneen, waa Riisi ñi leen bëgg a wër ndombo.
Xam naa loolu moo tax ñu bari seen deret di yëngu, ñu bëgg dellu xareji Ikren.
Maanaam ci tënk, li ma taataanagum ci téere Bóris baa ngi firndeel kàddoom yaa ma dooree woon ci njëlbéen gi.
Tuuti naa ci faramfàcce waxi bindkat bu mag bi te xelam màcc ci taalif, bind téere walla tekki ciy kàllaama yu wute.