DIINE AK POLITIG : NAN MOYTU LI NUY FÉEWALE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ëttu boole bi, genn kurél la gu boole mbooleem këri diine yi ngir saxal jàmm ci biir réew mi, rawatina ci lu ñeel politig beek diine ji. Seetlu nanu ne saa bu jamanoy fal njiitu réew jotee rekk, njaqare dafay faral di am. Li ko waral, nag, du dara lu dul ñenn ci politiseN yi dañuy jëfandikoo tarixa yi ngir beccingéel yeneen wutaakon yi ak a yëkkati seen mbër.
Fan yii yépp, ñi bokk ci Ëttu boole baa ngiy daje di waxtaan ci jafe-jafe yeek yëngu-yëngu yiy am ci antarnet beek i xeeti xaralaam yu deme ni Facebook ak WhatsApp. Kilifay Facebook yi amal nañu ag saytu, ànd ceek kàngam yi taxawal kurél gi. Weccoo nañu xalaat naka lañu war a def ba dakkal téesanteek wax ju ñaaw ci béréb yooyu.
Bi bésu pal gi desee benn ayu-bés rekk, ay ndéggat yu bari tàbbalees na leen ci antarnet bi, wesaare leen ci “Whatsapp” yi. Ay saay-saay a sooke lu ni mel, di sos ay fen yu tooy xepp, naan këru diine sàngam warul a sànnil xob wutaakon sàngam ndax bokkul ci ñoom, te gëmul seeni sëriñ. Lii moo bijji tiitaange ju réy ci waa réew mi. Diine nekk na lu man a jur xiirook ŋaayoo, te wareesul a mbubboo tarixa ngir soppi ko gànnaay, di ko xeexe ci politig bi. Yoonu tasawuf wi fi mag ñi sampoon, jàmm ak taalibe yi xamante, soppante a ko taxoon a jóg. Donte sax, politig masul a tàqalikook diine, ni seen diggante fése jamono jii dafa jéggi dayo.
Séex Tiijaan Si, doomu Abdu Asiis Si Al Amiin, njiit li nekk ci boppu kurél googu yëkkati nay kàddu ngir àrtook leeral kóllëre gi dox ci diggante Murid yeek Tiijaan yi. Wane na ne ñaari kurél yii, waxul sax bokkoo gi leen boole, waaye ñoom ñépp liggéeyal diine ak Yonent bi rekk a leen yitteel. Nee na Sëriñ Séex Tiijaan Si Al Maxtoom wax na ni su Murid yi ak Tiijaan yiy ŋaayoo dafay naqari Yonent bi ndax moo leen jaboote ñoom ñépp.
Rax-ci-dolli, wax na ne, palug njiitu réew du palu Imaam wala Xalifa, kon lees war a xool mooy jikko nit ki, jaar-jaaram, xam-xamu àddinaam ak yu ni mel. Waaye naan ci tarixa bii walla bee la bokk, ëpp naa def.
Ëttu boole baa ngi ñaan waa réew mi ñu ànd ak dal te dem sànnil xob ki leen soob, bañ cee boole wax ju bari ak xuloo. Yal na Yàlla sotti jàmm ci réew mi te ki jig Senegaal Yàlla jox ko ndam lu sedd guyy.
 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj