Tooli ceeb yu baree tuub fa diiwaanu Maatam. Looloo ngi am ginnaaw bi dex gi walangaanee foofu ci sababu taw yu bari yi fa wàcc ci ayu-bés yii weesu.
Mbënn mu metti moo am fa diiwaanu Maatam. Ginnaaw taw yu bari yi fa wàcc ci fan yii, dexu Senegaal gi daa fees ba tuuru foofu. Li ci gën a yéeme nag mooy ne, dafa laalaale tooli ceeb yu bari ci ñaari dëkk yii di Ndulumaaji Dembe ak Wuduru. Ñaari dëkk yooyee, fa bokk-moomeel bu Nabaji Siwol lañu bokk.
Bees sukkandikoo ci xibaar yi sunuy naataangoo yu APS siiwal, lu ëpp 120i ektaar ciy tool ñoo ngi ci biir ndox mi. Te ba tey ndox maa ngi wéy di wal ak di gën a lekk ay tool.
« Woññi nanu ñaari pàkk PVI (périmètres irrigués villageois) yu seen yaatuwaay tollu ci 75i ektaar ak beneen toolu kër bu 18i ektaar yoo xam ni ñoo ngi ci biir ndox mi. » (Abdulaay Sàll, Njiitu mbooloom beykati Ndulumaaji Dembe)
Tool yooyu sax, li desoon ci ñu góob leen bariwul. Ba tay, ci li Abdulaay Sàll xamle, mbey mi ñoroon na ba noppi. Desul woon lu dul dagg xatax yi, tànn ceeb bi.
Fii mu nekk nag, beykat yaa nga ca njàqare. Nde, ak ni mbey mi ñore, bu ndox mi duggee rekk dafay yàqu. Ñenn ci ñoom sax ñoo ngi sàkk i pexe, di kërale seen tool ya ak di dog ndox ma ngir mu bañ a dugg ci seen i tool.