Jëwriñ ji, Sëñ Biram Suley Jóob, yékkati na ay kàddu ñeel ndefari réewum Farãs yi. Fekk mu doon fa amal ab tukki ngir waxtaan ak ñoom ñeel mbélli yu réewum Senegaal ak nees ko fas yéene doxalee ak tolluwaayu jamono.
Ci àllarbi ji, 3 ak 4i pani sulet 2024, doon nañ amal 7eelu ndaje mi ñeel mbélli Afrig MOTA (Mining on top Africa) fa Paris, réewum Farãs. Ay Njiiti ndefar, ay Boroomi alal ak i ndawi Càmm doon ko teewe ci diiru ñaari fan ngir waxtaane ëllëgu balluy mbéll yu Afrig, rawatina jamono yii nga xam ne, àddina sépp a ci teg seen bët.
Ca Ndaje mooma, Biram Suley Jóob, di jëwriñu laf geek mbéll yi moo fa teewaloon Càmmug Senegaal. Ginnaaw ndaje ma sax, jëwriñ ji yékkati nay kàddu ci France 24 ak RFI, jagleel leen ndefari réewum Farãs yi. Muy ay kàddu yoy, dafa leen cay xamal naka la namm a doxalee ak ñoom ci génneg balluy mbélli Senegaal yi.
Naka noonu, nu gis ni Sëñ Jóob nekku fa di xiin-xiinal walla di layam-layami. Ci kàddu yu dëgër këcc la leen xamalee ni réewum Seneaal du salax balluy mbindaareem réewum Farãs, teg ko ci diggante bu yàgg ak kóllëre. Muy biral ni, la woon, wonni na. Nekkatuñu ci jamono jees di jébbalee sa bopp am réew. Kon du yem tugal. Dees na wuti ngañaay fépp ci àddina si, ba tax na « bu yitteem nekkoon Araabi Sawdit, foofa la koy jëlijee ci lu amul benn rafetal ».
Sëñ Biram Suley Jóob yemul ci wax loolu. Nde, bees toppee ay kàddoom, réewum Farãs yéwénul wenn yoon. Ñoom ñoo gën a xam ni déndu mbélli Sénégal yi tëdde. Réewum Senegaal ci boppam xameewu ko noonu, waaye nanguwuñu ko séddook moom.
Ba tax mu jàpp ni réewi Afrig yiy génne mbéll yi dañ war a fexe ba xam balluy mbindaare yi nekk ci seen biir suuf te di leen sopparñee ci seen i réew ngir gën cee yey. Te, fileek taxawuñ ngir sopparñee mbindaare yi fii ci Afrig, duñ mën a dundal xam-xam yi ñeel fànn wi fi kembaarug Afrig.