Wii yoon mooy ñaareelu tukkeem fa Gàmbi ci diir bu gàtt. Barki-démb, ci àllarba ji la elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, dem fa réewum Gàmbi. Ki ko dalal mooy Tof-njiitu réew ma, Muhammet Jàllo. Li sabab tukkeem bi mooy teewe ndaje mi ñuy dippe “Forum économique, commercial et d’investissement Gambie-Sénégal”.
Ndaje mooma, ci alxamesu démb ji lees ko amal. Waaye, yemu ca. Ndax, ci àjjumay tay jii tamit, dina am ndaje mu ñu fay amal ñu naan ko “5ème Session de la commission consultative conjointe chargée du suivi de la coopération entre les deux pays”. Mu mel ni moom ñaari xew-xew yu wute la am fa réew ma diggante démb ak tay.