Démb, ci dibéer ji 12 fani sãwiyee la elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, dem fa Muritani. Ma ngi fa àgg ci ngoon gi. Lii di tukkeem bu njëkk fa réewum Muritani. Mu war fa def luy tollu ci ñaari fan laata muy dellusi ci réew mi. Tukki bii nag, tukkib xaritoo la ak liggéey.
Tukki bii mooy ñetteelu tukkib elimaanu jëwriñ yi fa bitim-réew ginnaaw bi ñu ko tabbee ak léegi. Nde, bu yàggul dara la fi demoon Gàmbi. Te, la ko jiitu, demoon na fi Ruwàndaa. Ba tay, tukki yi dese nañoo bokk. Ndax, bu démb bi, tukkib xaritoo la ak liggéey. Moom, elimaanu jëwriñ yi, ci ngoonug dibéer ji la àgg fa Muritani. Mbooloo mu bari teeru ko. Ki ko dal mooy naataangoom bi, Moktaar Uld Jay. Elimaanu jëwriñi Muritani ak yenn ca kilifay réew ma ñoo ko teeru. Mu war fa def ñaari fan.
Dafa di, tukki bii moom, dafa làmboo solo. Ndax, kenn umpalewul ne réewum Muritani ak mom Senegaal ay dëkkandoo lañu, daanaka sax benn lañu. Seen diggante it rattax na. Moo tax, ñu séq ay jëflante yu rafet ci wàll yu bari. Mu mel ni, elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, li ko tax a jóg du lenn lu moy ñu gën a dooleel jëflante yi am seen diggante ak ci wàll wu mu mën a doon.
Réewum Muritani ak mom Senegaal kenn umpalewul ne am nañu ay jëflante ci ay fànn yu wuute. Muy ci laf gi, ci dem beek dikk bi, ci napp gi, ci kaaraange gi ak ci tukki yi. Moom elimaanu jëwriñ yi ak yenn ci jëwriñ yi mu àndal dinañu amal ay ndaje ñook jëwriñi Muritani yi.
Bu loolu weesoo, moom Usmaan Sonko dina gisante ak Njiitu réew ma, Muhammed Uld Séex Al Gaswani laata muy ñibbisi.
Kon, ñu gis ne tukki boobu, tukkib xaritoo la, waaye tamit, tukkib liggéey la. Dina tax ñaari réew yi gën a rattaxal seen diggante. Te yit, dinañu gën a dëgëral jokkalante yi dox seen diggante.