TUKKIB ELIMAANU JËWRIÑ YI FA RÉEWUM SIIN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Àjjuma jii weesu la elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, dooroon ab tukkeem fa bitim-réew. Moom nag, guléet muy génn kembaarug Afrig bi ñu tabbee ba tay. Nde, jamono jii ma nga fa réewum Siin. Dafa di, kenn umpalewul tolluwaayu réewum Siin ci wàllu koom-koom, xaralaak yu ni deme. Kon, tukki bii li ko wund du lenn lu mooy gën a rattaxal diggante ñaari réew yi ci wàllu jëflante. Su ko defee, réewum Senegaal mën a suqali yenn banqaasi koom gi.

Bésub gaawu ñaar-fukki fan ak benn ci weeru suwe la elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, àgg fa réewum Siin. Moom nag, mi ngi àndoon ak jëwriñu jokkoo gi. Àlliyun Sàll, Abdurahmaan Saar, jëwriñu koom gi, Sëriñ Géy Jóob, jëwriñu yaxantu gi ak ndefar gi, Séex Tiijaan Jéey, jëwriñu ndox mi ak Baakari Seega Bàccili, njiitul APIX. Ba ñu àggee, ca bés ba lañu door liggéey ba. Nde, ca la elimaanu jëwriñ yi gise ak kilifag dëkku Hangzhou bi, di gornooru Liu JIE. Li ñu dugge woon ndaje moomu mooy waxtaane mbir yu jëm ci wàllu koom, ndefar, xarala yi, añs. Gise na tamit ak doomi Senegaal ya fa nekk. Waaye, yamul foofu. Nde, ci dibéeri démb ji rekk, amal nañu fa am ndajem koom mu am solo.

Ndaje moomu nag, ñu bari teewe nañu ko. Muy doomi Senegaal ak Siin yi nga xam ne ñi ngi yëngu ci banqaas yoo xam ne ajuwuñu ci Càmm gi. Li mu jublu woon ci ndaje mi mooy ñaax doomi Senegaal yi ak waa Siin ngir ñu dugal seen i koppar ci tabaxug koomu Senegaal. Nde, kenn réerewul ne koomug Senegaal afa xaw a sooxe jamono yii bees ko méngalee ak yenn réew yi. Ndax, réew mi bokk na ci réew yi gën a ndóol ci àddina si. Moo tax, elimaanu jëwriñ yi gis ne liggéeykat yi ajuwul ci Càmm gi waruñoo raxas seen i loxo ci mbir mi. Fàww ñu dugal seen loxo ci doxalug naalu “Vision 2050”. Looloo tax it, mu bëgg ñii di waa Siin ñëw dugal seen i koppar ci réewum Senegaal.

Bi ñu jógee ci waxtaan woowu, am na ay déggoo yu ñaari réew yi jot a am. Muy ay naal yu jëm ci wàllu ndefar, dëkkuwaay, dem beek dikk bi, añs. Bi mu jógee ca ndaje mooma, am na yenn këri liggéey yu mu seeti, muy gu ci mel ni Alibaba. Nde, fi mu tollu nii, réewum Siin dafa am doole lool ci wàllu xarala. Te, ci lu dul yàgg dara, réewum Senegaal day amal powi olimpigi ndaw ñi, Ndakaaru 2026. Kon, seen jokkalante ak Siin mën na leen a jàppale ci lu bari. Tay, ci altine ji tamit, am na yeneen yu mu war a amal fa réewum Siin.

Mu mel ni tukkib elimaanu jëwriñ yi, tukki la bob ngir suqali koomu réewum Senegaal la. Ndax, réewum Siin kenn naatablewul ag yokkuteem ci fànn yu bari, rawatina ci wàllu koom. Te nag, garab gu la sut moo la mën a may ker.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj