Démb, ci gaawu bi la elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, demoon fa Gàmbi. Li waral tukkeem boobu mooy fekke fukk ak benneelu ndajem Njiiti réew ak Càmmi “Organisation pour la mise en valeur du fleuve Gambie” (OMVS). Mu doon ndaje mu am solo ñeel suqaliku ak jokkalante diggante réew yi séq kurél googu. Xew-xew boobu, ma ngay ame fa péeyu réew ma, di Bànjul.
Démb, ci suba gi, la elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, àgg fa Gàmbi, fa béréb bii ñuy dippe “Centre international de conférence Sir Dawda Kairaba Jawara”. Njiitu réewu Gàmbi, Aadama Baro, moo leen doon dalal. Nde, fa lañu doon amalee fukk ak benneelu ndajem Njiiti réew ak Càmmi “OMVS”. Tukkib magum jëwriñ ji, démb, mooy ñaareelu yoon muy génn réew mi bi ñu ko tabbee ak léegi. Bu njëkk ba, ma nga ko amalee woon fa Ruwàndaa. Ginnaaw gi la jaaroon Mali laata muy ñibbisi. Dafa di, tukkib démb ji moom wute na ak tukkeem bu njëkk ba.
Mu mel ni ndaje mii, ndaje mu làmboo solo la ci réewi Afrig sowu-jant yi, rawatina réew yi digaloo ak Gàmbi. Te, réewum Senegaal ak Gàmbi moom rombu nañu digaloo, daanaka, benn lañu. Moo tax, kii di magum jëwriñ ji, Usmaan Sonko, moo fa teewal réewum Senegaal. Nde, kenn umpalewul ne jamono jii Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, dafa nekk ci ab tukki. Ma nga fa Qataar.
Dafa di, du réewum Senegaal kese lañu fa teewal. Réewum Gine Bisaawo tamit, teewal nañu ko ca ndaje moomu. Ki leen teewal ca ndaje ma mooy magum jëwriñ ja, Wuuri. Am na yeneen kilifa yu bari yu ñuy xaar ca xew-xew booba. Nde, ndaje la moo xam ne bari na ñu ci bokk rawatina ñi ëpp doole ci ñiy dox ci suqaliku gu sax ak lëkkaloo gu jéggi dig.
Kon, mënees na jàpp ne, ndaje moomu, anam la boo xam ne ñoom Njiiti réew ak Njiiti Càmm yooyu ak sax yenn kilifa yu bokk ci xew-xew boobu, dinañu mën a waxtaane wëppa yu bari. Dinañu ci mën a càmbar it fi liggéeyi kurél googu tollu. Rax-ci-dolli, ñu yeesalaat banqaas yu kowe yoy kurél gi boole ko ak xaatim ay déggoo.Waaye, ba tay, ndaje moomu dina gën a dëgëral seen diggante rawatina ci seen i jokkalante ñoom ñi bokk ci kurél googu.