Démb, ci dibéer ji, la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, bawoo ci réew mi, jubali fa Tugal. Moom nag, du guléet muy dem fa kembaar googa. Waaye, wii yoon, ma nga jëm fa réewum Espaañ. Li mu dugge tukki bi mooy fekke ndaje mu am solo ma ñu fa war a door tay ci altine ji. Nde, ndaje la moo xam ne, du ay Njiiti réew kesee koy teewe. Ay Njiiti Nguur ak campeef yu bari dañuy koy fekke, muy xew-xew bu mag.
Altiney tay ji mooy ubbiteg ndaje mii ñuy dippe “4ème Conférence internationale sur le financement du développement”. Ñi ngi koy amalee fa Espaañ, fa dëkk bii di Séville. Moom, Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, moo fa teewal réewu Senegaal. Am na yeneen Njiiti réew ak ay Njiiti Nguur yu fa teew. Naka noonu, Njiiti yenn ci campeef yu mag yi ci àddina si teew nañu fa. Muy Njiitu ONU (Organisation des Nations Unies), FMI (Fonds Monétaire International), Banque Mondiale, ECOSOC (Conseil économique et social des Nations Unies) ak OMC (Organisation Mondiale du Commerce). Loolu di firndeel màggaay ak njariñ li ndaje moomu làmboo.
Ginnaaw bi mu dooree ci altiney tay jii, ndaje mi dina wéy ba keroog ñaari fan ci weeru sulet. Njiitu réew mi jël na fa kàddu, fésal gis-gisam ci yoon wees war a jaar ngir jagleel réew yi koppar yi leen di tax suqaliku. Réew yooyii, Senegaal ci la bokk. Ndaxte, kenn umpalewul ne, Senegaal, ci réew yi ndóol yi la bokk. Rax-ci-dolli, li ëpp ci askanam ay ndaw lañu. Te, loolu keno bu am solo la ci réew mu bëgg a suqaliku ba moom boppam ci fànn yépp.
Ba mu demee ca ndaje ma nag, moom Njiitu réew mi, jot na fa a séq waxtaan ak ñenn ciy naataangoom yu ci mel ni buuru Espaañ bi, Felip VI Njiitu réewum Estoni, Alar Karis. Bees sukkandikoo ci lees biral ci xëtu Facebook “Présidence de la République du Sénégal”, waxtaanam ak buuru Espaañ waa ngi aju woon ci dooleel seen jokkoo ci wàllu mbay mi, wërteef gi ak lu jëm ci mbiri tukki yi. Bu dee Njiitu réewu Estoni li nag, jot nañoo waxtaan ba déggoo ci li ñuy dippee “cadre juridique de coopération” diggante ñaari réew yi. Li ñu ci jublu mooy xool nu ñuy jëflantee ci wàllu xarala. Ndax, réewu Estoni am na ci xarañte goo xam ne àddina sépp a ko ko nangul. Ginnaaw loolu, kii di Ajay Banga, Njiitu kippaangog Banque Mondiale ñaax na Njiitu réew mi ci doxalin wu set ak yorin wu mucc ayib wi mu yoree Senegaal.
Ci gàttal, lii la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jot a amalagum ci tukkeem bii mu nekk nii. Maanaam, nii la doore tukkeem bi fa Espaañ. Kon, kenn réerewul ne dina am yeneen ndaje yu mu fa nar a amal laata muy ñibbisi fi réew mi.