Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, mu ngi wéyal tukkeem yi ci biir kembaar gi. Ginnaaw Móritani, Gàmbi, Gine Bisaawo ak Koddiwaar, ma nga woon fa Niseriyaa ak Gana. Bërki-démb ak démb la amaloon ci ñaari réew yooyii ay tukkiy liggéey.
Bërki-démb ci alxames ji la Njiitu réew mi bàyyikoo Ndakaaru ngir dem fa réewum Niseriyaa. Muy tukki bu mu sumb ngir dox tànki dëgëral diggante ñaari réew yi ak gën a jàppandal bennoo réewi Afrig Sowu jànt yi. Naka noonu, Njiitu réew mi amal nay waxtaan ak naataangoom bii di Bolaa Tinubu, di tamit Njiitul Kurélug CEDEAO. Ginnaaw bi mu fa jógee, yokk na tànk, daldi jàll fa réewum Gana. Foofu itam, gise na faak naataangoom bii di Nana Akufo-Addo.
Ci waxtaan yi ñu amal, Njiiti réew yu Senegaal ak Niseriyaa joxe nañu fa seen i kàddu ni dinañu lëkkatoo ngir jàppalante ci wàllu kaaraange, jële fi ñàkk gi, xeex rëtalkat yeek defkati ñaawteef yi. Dige nañu itam ni dinañu taxawu demokaraasi bi fi Afrig Sowu jànt te fexe ba askan wi gis ci seen bopp.
Bi mu demee Gana tamit, Njiitu réew mi sàkku na ci Sëñ Akufo-Addo ñu taxawal ag ndiisoo ci diggante ñaari réew yi. Bu ko defee, dinañu gën a mën a xalaat ci anam yi ñu mënee dëgëral lëkkatoo ñaari réew yi ñeel yaxantu bi, kaaraange gi, njàng meek njàngale mi, wér-gi-yaram gi, añs.
Rax-ci-dolli, Njiitu réew mi xamle na fa ni kurél gii di CEDEAO, moo ngi ci guddi gu bët setagul. Dafa nekk di dund ay jafe-jafe yu tar. Waaye, yaakaar moo ngi wéy di am ba léegi. Nde, ñoom ñépp dinañu àndandoo dëgëral li fi jot a am ci bennoo bi. Li leen war nag ngir ñu àntule mooy nu booloo, gëm léppi Afrig, ànd ceek jàppalante ngir suqali kembaar gi ak a dab bànneexu askan yi.
Tukki bi Sëñ Basiiru Fay amal ci ñaari réew yooyu dundal na itam yaakaari naataangoom yi ci taxawaay bi mu mën a am ci dundal demokaraasi bi fi Afrig Sowu jànt ak ci kembaaru Afrig gépp. Te sax ñoo ngi xaar ci Njiitu réewum Senegaal li mu taxaw ci tànki dox jàmm ngir delloosi réew yii di Mali, Burkinaa Faaso ak Niseer ci biir CEDEAO. Muy lu mën a nekk bees sukkandikoo ci Móris Sujeg Jonn, jàngalekat fa jàngune bu Gastõ Berger. Ndax, jàpp na ni, tolluwaayu Senegaal ci demokaraasi, ginnaaw bi mu génnee ci yëngu-yëngu yi fi jaaroon, may na ko màqaama boobu.