Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, mu nga woon fa réewum Gine. Barki-démb ci àjjuma ji la fa demoon ginnaaw bi mu jógee réewum Kab-Weer doon fa amal tukkib liggéey ak xaritoo.
Barkaatu-démb ci alxames ji la Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar fay bawoo fi réew mi, dem fa Paraayaa, péeyu réewum Kab-Weer. Muy tukki bum fa doon amal ci wetu naataangoom bii di Sëñ Xoose Mariyaa Pereraa Nefees. Naka noonu, barki-démb ci àjjuma ji, ñaari Njiit yi yaatal nañ bu baax ci lëkkatoo gi dox ci diggante ñaari réew yi, amal i waxtaan ci mbir yi ñu bokk i bëgg-bëgg. Jël nañ sax ndogalu taxawalaat yoonu yaale bi dox ci diggante Ndakaaru ak Paraayaa ngir gën a yombal jokkalante ñaari réew yi
Bu weesoo lëkkatoog ñaari réew yi, waxtaan nañ itam ci mbooloo ak bennoo réewi Afrig Sowu jant yi. Ginnaaw gi la fa Sëñ Basiiru Jomaay Fay daldi bawoo ngir àggaleeji tukkeem fa Gine Konaakiri. Bi 18i waxtu jotee ci ngoon gi la ko naataangoom bii di Seneraal Maamadi Dumbuyaa, Njiitu réewum Gine, dalal fa dalub roppalaan Ahmed Séeku Ture bu Konaakiri.
Naka noonu, ñaari Njiit yi bokk nañ rafetlu ànd bi dox ci diggante ñaari réew yi. Bokk nañ gis-gis itam ci gën a dëgëral diggante bi rawatina ci fànn yi deme ni kaaraange gi, balluy mbindaare yi, mbëj mi, yaxantu bi, yaale bi, añs.
Ñaari Njiit yi fas nañ yéene dekkil Ndiisso gi doxoon ci diggante ñaari réew yi, ñu gënoon ko xam ci Grande Commission Mixte de Coopération te gëjoon am ca atum 2008. Jël nañ ndogalu amal 6eel wi yoon ci weeru nowàmbar 2024.
Bu weesoo diggante ñaari réew yi, Sëñ Fay ak Sëñ Dumbuyaa waxtaan nañ lu yàgg ci tolluwaayu kaaraangeg diiwaanu Afrig Sowu jant. Ba tax ñu bokk gis ni war nañu gën a ñoŋal seen jokkalante ngir mën a xeex rëtëlkat yi, njaayum ngànnaay yi ak njuuj-njaaj yeek jëfi ñaawteef yi lëmbe àddina si. Naka noonu, dinañ boole seen doole ci wàlluw kaaraange, ànd sàmmandoo dig bi nu séq.
Sëñ Basiiru Jomaay Fay përyee na naataangoom bi, Sëñ Dumbuyaa, mu seetsi ko Ndakaaru ba mu nangul ko ko.