Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, ma nga tay fa réewum Qataar. Njiitu réew ma, Séex Tamiim Bin Hamat Al Taani moo ko fa përyee woon ngir mu teewe ndajem Dohaa (Forum de Doha) mi ñu fay amal ci njeexitalu ayu-bés bi (gaawu 7 ak dibéer 8i pani desàmbar 2024).
Démb ci àjjuma ji la Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, àgg fa réewum Qataar ngir teewe Ndajem Dohaa mu 2024 mi. Muy ndaje mu mag mu ñu fay amal at mu nekk. Njiiti pólitig yi di fa daje ngir waxtaane jafe-jafe yi àddina siy jànkonteel ak di ci jéem a wutandoo ay pexe. Ndaje mu ren mi di 22eel wi yoon ginnaaw bi ñu ko tàmbalee ca atum 2003.
Tay ci gaawu gi, Njiitu réew mi jot na a amal ab jotaayu waxtaan ak Njiitu réewum Qataar li, ci teewaayu Soxna Yaasin Faal (Jëwriñ ji yor mbiri Bennoog Afrig ak Bitim-réew) ak Sëñ Séex Dibaa (Jëwriñu Ngurd meek Gafaka gi).
« Am naa mbégte dajeek Sëñ Séex Tamim Bin Hamat Al Taani, Njiitu Qataar. Amal nanu waxtaan ñeel liy dëgëral sunu diggante ñaari réew yi, ci pexey yokk dugalante bi ak taxawu yittey diiwaan yeek yu àddina si. Nun ñaar ñépp ànd nanu ci liggéey ngir ànd bu yàgg, bu lalu ci jàmm, suqaleeku ak gis-gis bi nu bokk am ñeel ëllëg. » (Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, Njiitu Bokkeefu Senegaal ».
Laata mu doon dem dem fa Qataar, Njiitu réew mi jotoon naa amal tukkib 2i pan (àllarba ak alxames) fa Réewum Émirats Arabes Unis. Daje na fa ak Njiit la Mohamet Bin Sayet. Naka noonu, ñu ànd fësal seen yéene ngir dëgëral seen ànd ñeel fànni laf gi, tabaxte yi, nimerig bi, njàng meek mbay mi. Laata mu fay jóge itam, Njiitu réew mi daje na ak Saa-Senegaal yiy dund foofu ba ñu weccante fay xalaat. Njiitu réew mi wax na leen ni mu bàyyee xel seen i yitte ak jafe-jafe yi doomi réewum Senegaal di jànkonteel fa réewum Émirats.
Njiitu réew mi rafetlu naat seen taxawaay bi siggil réewum Senegaal ci àddina si. Ba tax mu leen di jaajëfal ak di leen xirtal ci ñu gën cee dogu. Bu loolu weesoo, biral na yéeney amal bés bees di màggal fi réew mi, jagleel ko waa Jasporaa bi.