TUKKIB NJIITU RÉEW MI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, tukkee na fi réew mi barki-démb ci dibéer ji, wutali réewum Araabi Sawdit. Dina fa am juróomi fan, 27 ba 31i pani oktoobar 2024. Dina fa amal ay ndaje ak kilifa ya jiite réew ma.

Bjiitu réew mi dina teewe ndaje mii di Future Investment Forum, di ndaje mu mag mom, ay kilifa yu mag, ci pólitig ak ci koom-koom, dañuy jóge fu nekk ci àddina si ngir teewe ko. Bu jógee Araabi Sawdit, dina wéyal tukkeem fa réewum Turki ngir dajeek naataangoom bii di Reseb Tayyib Erdogaan.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj