Tukki ñeenti fan la Emanuyel Makarõ, Njiitu réewum Farãs li tàmbali alxemes 2 màrs 2023, fii ci kembarug Afrig. Jamono yii, tukki bi di am yemook jamono joj Farãs dafa nekk di ñàkk lu bare ci màqaama gi mu amoon ci réewi Afrig yi ak wegeel gi ñu ko wegoon, rawatina ci réew yi nekk ci diwaanu Sayel bi.
Bi muy waajal tukki bi, Njiitu Farãs li dafa woote ngir jàkkaarlook caabal yi. Bi ñépp dikkee, mu xamal leen ni dafay soppi tooggaayu réewum Farãs ci kembarug Afrig :
« Réewum Farãs amatul moomel ci kembarug Afrig. […] Fi nu amoon dalu sóobari ak lim bu takku, di dem bay junni, dinanu leen wàññi. Dunu tëj dalu yooyu waaye dinanu leen soppi. »
Alxames, 2 Màrs 2023, Njiitu réewum Farãs li yékkateeti ay kàddu ci bi muy janook askanu Farãs wi nekk ca Gabon. Ci biir wax ji, mu fésalati ca yenn ciy xalaatam ñeel diggante réewum Farãs ak réewi Afrig yi.
« Mboor moo ñu boole fii ci Gabon. Du lu ñuy nëbb, mbooru ‘‘ Françafrique’’ la. Waaye jomonoy ‘‘Françafrique’’ wonni na. Lée-léeg damay yaakaar ni gis-gisu ñenn ñi soppeekuwul ni sunuy yos. Bu may dawal, di dégg ak a gis ñuy jiiñ réewum Farãs yéene yu mu amul, yu mu amatul, dafay ndiru ni dañuy xaar ci moom taxawaay bu mu bëggul a am. »
Li mu wax ni mooy gis-gis bu bees bi dafay firndeel ni réewum Farãs jàngat na bu baax xew-xew yi fi jot a jaar. Ginnaaw bees ko dàqee ca Mali, Centre Afrig ak Burkinaa, seet na bu baax ba gis ca dëgg-dëgg li xew ba jaratul dara ci yile réew. Looloo tax ba mu jël ndogalu defaraat toogaayu Farãs ci kembarug Afrig.
Waaye ku dégg ni Makarõ àddoo war a xam ni li mu waajal ak li mu wax du benn. Li mu xaar ba ni dem a des di soog a yékkatiy kàddu dafay firndeel ni am na lu mu bëgg a gëmloo ñi muy seeti. Te moo di bu kenn tiit te bu kenn muslu ci moom. Moo ngi ñëw ci tànki jàmm ak yéene yu rafet.
Wiiri-wiireem jépp terewul waxam ji mel ni ngelaw lu upp rekk jàll. Nde bu ñu bàyyee xel ni ko Saa-Afrig yi gatandoo, dees ciy dégge ni Njiitu Farãs li ci boppam dafay wax di weddi boppam. Bu nee « Jamonoy ‘‘Françafrique’’ wonni na » ba noppi soll i dàllam wutali yoonu Afrig ne dafay defaraat toogaayu Farãs, gëm ko dina nekk lu jafe. Nde, kuy defaraat sa toogaay dafa fekk nga jekkadi.
Loolu, ndax jar naa wax sax ? Soppeeku na jarul di wax ba dënn tàng, ngir ñi muy waxal gëm ko. Bu jëfee ñépp gis. Bu nee Fraçafrique wonni na fekk yi ko laloon làlliwu leen te ñuy dalu sóobarey Farãs yi ak xaalisu FCFA, xel dafay daldi teey. Toogaay bi mu bëgg jekk-jekkal, namm koo jaare ci soppali nekkinu sóobarey réewum Farãs, wàccul yoonu nootaange.
Coppitegi ak anam yi mu ko xamlee, ndax waxtaan na ceek Njiiti réew yi ? Ndax askani réew yi bëgg nañoo wéy di gis sóobare yi saa su nekk te taxul nu am kaaraange wenn yoon. Rax-ci-dolli amul wenn yoon wu mu yëy yàbbi ci lu jëm ci koppar gii di FCFA. Li ni mel di wone ni lii la yàgg a wax fépp fu mu mës a yékkati i kàddu. Bëggul ‘‘françafrique’’ yem fi, nde i pexeem mooy Farãs wéy di fi nekk ciy bëgg-bëggi boppam.