TUKKITEY NJIITU RÉEW MI FA ARAABI SAWDIT AK TURKI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dibéer jee weesu la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, tukki woon na. Ma nga njëkke woon fa Araabi Sawdit. Def na fa lu tollu ci ñeenti fan. Maanaam, li ko dale ñaar-fukki fan ak juróom-ñaar ba fanweeri fan ak benn ci weeru oktoobar. Ki ko fa woolu woon mooy bummi ba, Muhammet Ben Salmaan. Jot na fa a amal ay ndaje yu am solo. Bi mu fa jógee la jàll Turki laata muy dellusi fi réew mi.

Tukkitey Njiitu réew mi nekkoon na ay yoon yu làmboo njariñ bees sukkandikoo ci kàddu yi mu yékkati bi mu ñibbisee. Moom, Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, xamle na ne kii di bummi bu Araabi Sawdit moo ko woolu woon ci benn “forum” boo xam ne ay boroomi alal ñoo fa daje woon. Te, seen bëgg-bëgg mooy wut dëkk yu ñu def seen alal ngir mu mën a jur dara. Mu mel ne, ndaje mi ab bunt la woon ci moom ngir mu mën a gisante ak ñoo xam ne koom moo leen soxal. Moo tax, mu ne :

Nekkoon na nag, buntu (occasion) ci man ma waxtaan ak ñi nga xam ne yor nañu alal, di seet foo xamante ne mën nañ jël seen xaalis def ko fa ngir mu jur dara. Ngir ñu wax leen Senegaal fu mu tollu, tay, ci soxla li nga xamante ne “investisseurs” yooyu yor nañu ko, muy koom.

Mu mel ni, seen alal ji, ci ay banqaas yu wute lañu ko bëgg a dugal. Dafa di, ñoom ci fànn yu bari lañuy yëngu. Am na sax, yenn yu ci Njiitu réew réew mi jot a jukki. Nde, nee na :

“(…) Seen alal dañu koy jël dugal ko ci wàllu tabaxte (infrastructures), ay yoon, ay tabax ak i leneen. Walla sax, ñu dugal ko ci leneen lu mel ni mbëj walla ndox, walla ci yeneen i banqaas yi. Ci wàllu mbey mi, ci wàllu tàggat, ci wàllu ndefar.

Moom, Njiitu réew mi xamle na ne jot na fa a waxtaane naal bi mu namm a yoree réew mi. Nde, kenn umpalewul ne bu yàggul dara lañu aajar seen naal wii ñu dippee « Vison 2050, Agenda national de transformation ». Mel na ne, am na yaakaar ci ne réewum Araabi Sawdit noppi na ngir gunge ko ci liggéey bi mu sóobu nii moom ak ug Nguuram. Loolu lay dëggal ci kàddoom yii :

Ba tax na, bi nu xoolee lépp loo xam ne waxtaane nanu ko, Araabi Sawdit am na yéene gunge nu ci ni nuy jëmmalee li nu xalaat ba tëgg ko ci « Vision Sénégal 2050 ». Muy lu jëm ci wàllu ndox mi, ci wàllu mbëj mi, ci wàllu mbey mi, ci wàllu ndefar gi ak soroj bi ak tamit ci liy wàllu tàggat ak ci xarala yu bees yi.

Waaye, ñoom yemuñu foofu rekk. Nde, jot nañoo waxtaane pas gu doxoon diggante réewum Senegaal ak Araabi Sawdit. Li mu ko dugge, mooy ñu seetaat ko, ba ñépp mën cee gis seen bopp rawatina waa réewam. Te, bi mu ci jógee, biral na ne :

Bi nu demee nag, waxtaan nanu ci ak kilifay Araabi Sawdit yi ba balaa nu fay jóge am na lenn loo xam ne tegaat nañu ko sunu loxo ci ay “concession” yu nu mën a def. Maanaam, ci jéego yu nu mën a def ba mu mën a doon njariñu Senegaal ci pas googu. Jox naa ndigal jëwriñ ji ñu dénk ndox mi, mu gën cee boolook yeneen njëwriñ yi. Ndax, “offre” bi mu joxe léegi dafa am tamit lu bees lu laale ci wàllu mbëj. Te, gëm naa ne sax, bu nu góor-góorloo ci  seen boor ak nun ci sunu boor, dinanu mën a déggoo ci pas googu nga xam ne laalewul ak dara ak “Grand Transfert d’Eau” bi nga xamante ne door nanu ko.”

Kon, mel na tukkiteg Njiitu réew mi fa Araabi Sawdit du woon ngir umra rekk. Waaye, lu suqali koomu réew mee ko taxoon a jóg. Moo tax, ba mu fa jógee rekk la jubali Turki. Jot na a amal foofa tamit am ndaje mu am solo ak Njiitu réew ma, Tayib Erdogan. Li ñu fa waxtaane, moom la tënk ci kàddoom yii :

“(…) Bi nu waxtaanee, lépp loo xamante ne jafe-jafe la, muy jafe-jafey Saa-senegaal yi nekk Turki, waxtaane nanu ko. Te, am nanu yaakaar ne fan yii di ñëw kilifay Turki dinañu ci def ay jéego. Xam ngeen ne bi nu doon dem, danoo waxoon waa Turki, danu bëgg nu amalaale benn “forum” bu “secteur privé” yi. Xool naka lanuy gën a lënkalee bu baax “secteur privé” Turki yi ak yu Senegaal”. (…) Bi nu ci noppee, “investisseurs sénégalais” waxtaan nañu ak seen i naataangoy Turki yi. (…) Te, am naa yaakaar ne “secteur” yu bari yu leen amal njariñ te, nekk ci “Vision 2050” dinañu ci gën a sóobu (…).”

Ñoom ñaari réew yi nag, jot nañoo xaatim ay pas. Muy lu jëm ci wàllu mbey mi, ci kaaraange gi, ci dëkkuwaay ak ci njàng mi. Am nañu ay naal ci li ñuy dippee “mécanisation agricole et l’exploitation des hydrocarbures”. Waaye, yemuñu foofu. Ndax, am nañu ab naal bu ñu xaatim ci wàllu njàngale mu kowe mi ngir mën a yombal jokkalantey daara yi ak sémbu gëstu yi.

Lii mooy poñ yi nga xam ne ñoo tënk tukkite yi Njiitu réew mi doon amal ci ayu-bés bii ñu génn. Donte ne sax, ci réew yu wuute la leen doon amalee, loolu terewul ne, li gën a fés ci ndaje yi, du lenn lu moy mbirum koom.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj