Alxames jii weesu la elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, dooroon ab tukki ci yenn réewi Afrig sowu-jant yi. Donte ne sax, bu yàggul dara, am na yenn réew yu mu jotoon a dem, muy fu mel ni Burkinaa Faaso. Bi mu dellusee, yàggaatul dara mu jëlaat yoon. Wii yoon nag, nee ñu tukki bi ci ñetti réew yu wute la ko nar a amal. Muy fa Koddiwaar ga mu njëkke, teg ci Gine Konaakiri ga mu nekk jamono jii. Bu fa jógee, dina dem Siyeraa Lewon laata muy ñibbisi.
Àllarba jii weesu lañu doon door waxtaan wi ñeel nosteg politigu réew mi. Ca ëllëg sa la fabu, doore ab tukkeem fa Koddiwaar. Am na jëwriñ yu mu àndal ci tukki boobu. Muy Abdurahmaan Saar, jëwriñu koom gi, Sëriñ Géy Jóob, jëwriñu yaxantu gi ak ndefar gi ak Faatu Juuf, jëwriñu napp gi. Ci ngoonu alxames ji lañu leen gatandu fa dalu roppalaan gii di Félix Houphouët-Boigny. Ki leen dalal di naataangoob Usmaan Sonko bi Robeer Bëgre Màmbe. Ginnaaw bi ñu ko dalalee, sargal nañu ko ak seen coliinu cosaan. Moom elimaanu jëwriñ yi, jot na def ñetti fan fa réew moomu. Nde, tukki bi mu fay amal tukkib xaritoo la. Waaye it, tukkib liggéey la. Moo tax, jot nañu fa amal ay ndajey waxtaan yu bari ngir waxtaane mbir yoo xam ne yitteel na ñaari réew yi. Nde, bëgg nañoo taxawal lëkkaloo gu dëgër diggante Ndakaaru ak Abijã.
Ginnaaw loolu, elimaanu jëwriñ yi jot na gise ak Njiitu réew ma, Alasaan Watara. Ñoom tamit jot nañoo waxtaan ci poñ yu soxal ñaari réew yi. Ci gaawu bi, am na beneen xew-xew bu ñu doon amal fa dëkk bii di Buwaake. Elimaanu jëwriñ yi teewe woon na ko. Foofa tamit, sargal nañu ko fa, teral ko it boole ko ak solal yi ñuy solal ku ñu wormaal. Laata muy jóge fa réew mooma jot naa gise ak doomi Senegaal ya fay dund. Waxtaan ak ñoom ci seen i jafe-jafe, wax leen tamit li Nguur gi sumb ngir saafara seen jafe-jafe yooyu. Muy ci wàllu kopparal, dëkkuwaay, añs.
Démb, ci dibéer ji, la elimaanu jëwriñ jóge fa réewum Koddiwaar jubali réewum Gine Konaakiri. Foofa tamit, tukkib xaritoo ak liggéey la fay amal. Dina fa def ñaari fan. Bi mu àggee fa réew mooma, naataangoom bii di Aamadu Wuri Ba moo ko gatandu. Moom nag, bi mu agsee ci dibéer ji, jot na amal am ndaje ak doomi Senegaal ya fa nekk. Moom nag, dalal na xelu mbokki maxejjam yooyu ci seen i njàqare. Muy ci wàllu këyit yi, pasi napp gi, jàppandalug kopparal gi ak dëkkuwaay yi. Tay, ci altine ji, moom ak naataangoom bi door nañu ay ndajey liggéey. Li ñu leen dugge du lenn lu moy waxtaane lëkkaloo yi dox diggante ñaari réew yooyu. Ñu xool nan lañu leen di gën a ñoŋalee.
Ci gàttal, lii la elimaanu jëwriñ yi jot a amal alxames ak léegi. Nde, fa Koddiwaar la njëkk a jaar def fa ñetti fan laata muy jàll. Jamono yii moom, ma nga fa réewum Gine di wéyal ab tukkeem. Waaye, ba nii gisees na ne elimaanu jëwriñ yi, daanaka, réewi Afrig sowu-jant yi kepp la def yitte. Dina ci boole yeneen am déet, li ci kanam rawul i bët.