TUUMAY LUUBAL ÑEEL YAAY FAATU JAAÑ

Yeneen i xët

Aji bind ji

Yaay Faatu Jaañ la yéenekaayu Yoor-Yoor xëyee tey ci xëtam bu njëkk, mbaali jokkoo yi fésal ko, di ko mbamb. Moom nag, soxna si, njombe wu réy lees koy tuumaal. Nde, ci li yéenekaay bi biral, dafa am ag caabal guy taqal Soxna Yaay Faatu Jaañ ag luubal gu tollu ciy miliyoŋi miliyoŋ ci sunuy koppar.

Yaay Faatu Jaañ, lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar la bokk. Moom moo jiite woon naal bii di PROMISE (Programme de promotion de la Microfinance Islamique au Sénégal). Waaye, ci lees biral, yoriinam wi dafa taq suuf.

Dafa di, ci li yéenekaayu Sëriñ Saaliw Géy bi siiwal, dafa am ag caabal gu wane ni Yaay Faatu Jaañ dafa tibb bu baax a baax ci xaalis bim waroon a liggéeyee. Nde, bi ñu saytoo koppari naalub PROMISE bi ci atum 2019, dañ ci gis ag càcc. Nee ñu, soxna si dafa jëfandikoo 666i miliyoŋ (juróom-benni téeméeri miliyoŋ ak juróom-benn fukk ak juróom-benn) yoo xam ni, indiwu ciy firnde. Maanaam, koppar googu yépp mu génnee, amul ay këyit yu koy firndeel.  Li doy waar ci mbir mi mooy ñi ñu wax ne jox na leen ci xaalis boobu.

Ci biir 666i miliyoŋ yooyu ñuy wax, nee ñu, 100 073 785 FCFA yi daf ko jox ñu ko yeyowul niki : Le Soleil, GFM, Foutanké, Lamco Industrie, Gie Ndawa Compagnie, Saly Princess ak AB Partners. Loolu doyul, lenn li, mu daldi ciy jox ay taskati xibaar,  amal ciy ndajey mbind (conférences de rédaction), fay ci ay paasi tukki. Te, loolu yépp, amul genn këyit gu koy firndeel. Muy xibaar bu doy a doy waar ñeel soxna soosu daan wër tele yeek jotaay yi di xeexal nguur gi fi nekkoon ak a dal ci kow kujje gi, rawatina Usmaan Sonko. Du ñàkk, moom Soxna Yaay Faatu Jaañ, mu àddu ci mbir mi ngir teggi tuuma.

Li ci kanam rawul i bët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj