U.I.J.A SARGAL NA USMAAN SONKO

Yeneen i xët

Aji bind ji

U.I.J.A (Union Internationale des Journalistes Africains) kurél gu mag la, gu ëmb taskati-xibaari Afrig yi. Mu nekk kurél goo xam ne am na neexal bu muy joxe at mu jot daanaaka. Ren jii, kenn ci doomi Senegaal yi lañu ko jagleel. Mu doon koo xam ne kenn dootu ko naatable ndax taxawaayam ci biir réew ak li muy xeex bu yàgg ba tey. Kooku nag, du kenn ku dul elimaanu jëwriñ yi, di yit njiitul Pastef, Usmaan Sonko. Moom la kurél googu di jox li ñuy dippe “Trophée MYRIAM MAKEBA”.

Barki-démb ci dibéer ji la waa U.I.J.A biral xibaar boobu jaare ko ci benn yëgle. Li ñu ko dugge du lenn lu moy wone taxawaay bu am solo bi Usmaan Sonko taxawe jamono jii ci Afrig, rawatina fii ci Senegaal gi mu dëkk. Ndax, lu ne fàŋŋ moom kenn du ko jeex. Moo tax, ñu jàpp ne xam-xam ak gis-gis bi ñuy seet ci maas gu yees gi gis nañu ko ci moom. Rax-ci-dolli, lépp mu teg ko ci njub ak gis-gis bu leer ngir ñu mën a suqaliku ci wàllug koom. Looloo tax, ñu jàpp ne xalaati Myriam MAKEBA yi ñeel soppante, bennoo ak suqaliku yi mu daan doxal gis nañu ko ci doomu Senegaal ji. Maanaam, ndono laa ngi ci moom. kon nag, ku def lu réy rekk, am lu réy.

Dafa di, ñoom, laata ñuy joxe neexal boobu, dañuy daje waxtaan seen biir ngir xam kan moo ko gën a yelloo. Ci lañu gisee ne bu dee bëgg sa réew rekk, dogu ngir mu suqaliku ci wàllug koom, nekkiinu askan wi ak ci wàllum mbatiit, doomu Senegaal ji kenn demul des. Ba tax, ñu ne dañu ko koy jagleel ngir ñaax mbooleem doomi Afrig yi nga xam ne ñi ngi nekk ci yoon wi mu nekk. Ñu yokk seen i jéego, jàpp tëw a bàyyi. Nde, loolu rekk moo mën a doon njariñal Afrig. Ndax, kenn réeréwul ne doomi dëkk bi kepp a mën a defar dëkk bi.

Neexal boobu nag, bu ñu koy joxe dañu koy defal am xew. Xew moomu dinañu ko amal fukki fan ak juróom-ñett ci weeru me wii ñu nekk. Ma ngay ame fale ca Pari, fa réewum Farãs. Muy doon bés boo xam ne dinañu ca màggal liggéey yi am solo yi elimaanu jëwriñ yi def. Li ñu ko dugge mooy ñaax ak dooleel doomi Afrig yi nekk ci yoon woowu.

Mu mel ni kon, Usmaan Sonko amagum na benn ràññatle ci at mi fa bitim-réew. Li mat a laaj kay mooy ndax, moom elimaan ji, moo koy jëlalil boppam walla day yem ci yónnee rekk ngir ñu jox ko ko. Lu ci mën di am, ku dund rekk, danga fekke.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj