Àllarba, 31 me 2023, la Njiitu réew mi Maki Sàll woote woon ubbite péncoo mi mu woote woon ñeel tolluwaayu réew mi. Biñ ko ubbee ak léegi nag, am na ayu-bés ak lu teg. Waaye, démb ci àjjuma ji, 9 me 2023 la liggéey yi tàmbali.
Démb ci àjjuma ji, 9 suwe 2023, lañ doon sumb liggéey yi ñeel péncoo mi Njiitu réew mi, Maki Sàll, woote. Mu doon ame fa Direction général des élections ci kilifteefu Tanoor Candeela Faal mi ubbi waxtaan yi ak ci teewaayu waa nguur gi, lenn ci kujje geek fara-askan wi (société civile). Ci tënk, ñu gis ne liggéey bépp a ngi ñu cërale ci juróom-ñeenti banqaas. Banqaas bu nekk am na ku farewul fenn ku koy jiite. Mustafaa Ñas mi fi nekkoon njiitul ngombalaan gi lañu tabb aji-saytu, mooy boole di saytu doxalinub liggéey yi.
Ci juróom-ñeenti banqaas yi, ñu gën cee ràññe banqaasu pólitig bi. Li ko waral mooy lees war a bàyyi xel tolluwaayu làngu pólitig geek ni mu jaxe jamono yii. Muy banqaas bob, li leen di xaar ci liggéey du mën a yomb. Nde, ñoom ñoo war a waxtaane lépp lu jëm ci wotey 2024 yii di ñëw (24 féewaryee 2024) : nees leen war a amale, ñetteelu moomeg Njiitu réew mees di laam-laame, nekkug lawaxub ñenn ci kujje gi, rawatina Usmaan Sonko, Xalifa Sàll ak Karim Wàdd ñi yoon jot a gàll i daan yu leen nar a tere bokk ci lawax yi.
Fii mu nekk, laaj bi sàmpu mooy naka lañ war a def ba tànn ñay séq banqaas pólitig bi ak ban anam lees war a liggéeye ba amal i ndogal yu leen kenn dul ga ? Ak lees seetlu ni pàrti yu bare yu fare ci kujje gi dañ bank seen i loxo ci péncoo mi : waa yewwi askan wi ak pàrti politig yi bokkul YAW te lëkkalook waa F24. Banqaasu pólitig boobule sax war naa tabb njiit lu bees fileek altine jii di ñëw. Ndax, Baabakar Kànte mi ko naroon a jiite dafa mujje am ngànt.
Waa F24 yi sax yemuñu ci bank seen i loxo. Nde, jamono yii liggéeyi banqaas dee tàmbale, ñoo ngi doon waajal i doxu ñaxtu ci àjjuma jeek gaawu gi (9 ak 10 suwe). Ñuy ay yëngu-yëngu yu perefe bu Ndakaaru jotoon a gàntal ba dàqaale lépp lu ni mel ci àppug 9 jàpp 16 suwe 2023 ngir sàmm dal gees tàmbalee nemmiku ci réew mi ginnaaw jax-jax yu metti yi fi jaar ci ndoorteelu weer wi. Muy ndogal lu waa F24 dàjji, donte ni ñoom sax fas nañ yéen bàyyi seen ñaxtu yooyu. Li leen tax a bàyyi nag, du benn yoon ndogalu perefe bi. Nde, ci li ñu xamle, Saa-senegaal yi lañuy déglu te jot nañoo amal i waxtaan ak ñi jotewul ak nguur di waa « secteur privé ». Lees gis mooy ni fi réew mi tollu, ak tabaski bi jubsi, doon na jaadu ñu xalaat ci askan wi ba may leen fu ñu ko mënee waajal.
Bees delsee ci péncoo mi, mboolem njureef yee ngi ñuy séentu fileek 25 suwe, bu yàggee ba yàgg. Mu des kon ñaari ayu bés doŋŋ ci àpp gi leen Njiitu réew mi àppal. Moom Njiitu réew mi sax xamle na ci ndajem jëwriñ yi amoon ci àllarba jii weesu, ni bu péncoo mi jeexee ba mu jot ci njureef yi, dina génn wax ak askan wi. Dees na taaxirluwaat, ku doon xaar Njiitu réew mi yey-yàbbi ci yëngu-yëngu yi fi jaar.