UBBITEG NGOMBLAAN GU YEES GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tay, ci altine ji, ñaari fan ci weeru desàmbar 2024, lañuy ubbi Ngomblaan gu yees gi. Keroog ci alxames ji la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, génnee ab dekkere buy xamle loolu. Ngomblaan gii nag, Ngomblaan la Ngomblaan la gog, ñii di waa Pastef nga xam ne ñoo nekk ci Nguur gi, ñoo fa ëpp doole fuuf. Kon, fii ak diir bu gàtt dees na xam nan lañuy taxawalee Ngomblaan gu bees gii.

Fukkeelu Ngomblaan ak juróom gi ñuy ubbi tey moo wuutu fukkeel ak ñeent gi nga xam ne dépite ya jotuñoo jeexal seen ug moome. Nde, ñaari at kepp lañu fa def, ñu jële leen fa. Li ko waral, mooy ne Nguur gi fi jóge moo fa ëppoon doole. Te, Nguur gi fi nekk nii jàpp ne ñooñu dañuy gàkkal seen ub liggéey. Looloo tax ba, Njiitu réew mi jëloon ndogalu tas Ngomblaan googu, ñu demaat ci ay wote. Su ko defee, ñu mën a taxawalaat ag Ngomblaan gog, Pastef moo fay ëpp doole.

Fukki fan ak juróom-ñaar ci weeru nowàmbar lañu doon amal wotey palug dépite yi. Daanaka, ca bés ba rekk ñu bari xamoon nañu fu ndam li féete. Waaye, terewul ñu doon xaar banqaas yiy yëngu ci loolu ngir ñu àddu ci. Looloo tax, alxames ñaar-fukki fan ak benn ci weeru nowàmbar la ndiiso gii di “commission nationale de recensement des votes” génnee woon njureefi négandiku yi. Ñaar-fukki fan ak juróom-ñaar ba tey, ci weer woowu, la ndajem ndeyu àtte mi génnee njureef yu mujj yi. Njureef yu mujj yooyu defuñu lu dul dëggal njureef ya ñu njëkkoon a génne. Làngug Pastef gi nag, moo daan kujje gi jéll bu leer, bu amul benn werante.

Cig pàttali, ci téeméeri dépite ak juróom-benn fukk ak juróom yi doon xëccoo, Pastef moo jël téeméer ak fanweer yi, Takku Wallu am fukk ak juróom-benn, Jàmm ak njariñ am juróom-ñaar, Sàmm sa kàddu am ñetti dépite, Soppi Senegaal am benn, Farlu am benn, And beesal Senegaal am benn, Senegaal kese am benn, Kiiraay ak Naataange am benn, And ci kóolute ngir Senegaal am benn, Àndu-Nawle am ñaari dépite, Jël li ñu moom am benn dépite. Kon, loolu firnde la ci ne Pastef moo ëpp doole fuuf ci Ngomblaan gii.

Mu mel ni, waa Pastef ñoo nar a raafal mbooleem béréb yi nga xam ne ñoo ëpp solo ci Ngomblaan gi. Muy la ko dale ca njiiteef la ba ci yeneen yi des yépp. Waaye, mu am mbir mu doy-waar mu xew ci Ngomblaan gi. Nde, Maki Sàll mi fi nekkoon Njiitu réew, jiite woon tamit lëkkatoog Takku wallu Senegaal, moo xamle ne bàyyi na moomeg dépite gi ko askanu Senegaal joxoon.

Li am ba des daal, mooy ne fii ak lu yàggul dara dees na xam nu fukk ak juróomeelu Ngomblaan gi di bindoo. Kan moo koy jiite. Nan la kippaangoo yi di taxawe bu dee dinañu bari. Li ci kanam moom, rawul i bët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj