Ñaari kuréli Afrig sowu-jant yii di CEDEAO (Communauté Economique Des Etats de l’Afrique de l’Ouest) ak UNOWAS (Bureau des Nations Unies pour de l’Ouest et le Sahel) ñoo yabaloon ay ndaw fa Gine Bisaawo. Li ñu ko dugge woon du lenn lu moy waxtaan ci mbirum wote yi fa war a am. Su ko defee ñu jéem a xool nu ñuy def ba am ay saafara ci jafe-jafe yooyu. Maanaam, ñu xool nu ñuy def ba am déggoo ngir nu ñuy amalee wotey palug Njiitu réew ak yoy dépite yi ci atum 2025. Waaye, Njiitu réew ma mayu leen fu ñu ko yeggalee. Ndax, ay tëkku la leen tontoo, ñu gaaw daw génn réew ma.
Ci ndigalu ëttub Njiiti Càmm yi ak yoy Nguuri CEDEAO la Njiitu ndiiso gi, Dr Omar Alliya Turaay, jël ndogalu yabal ay ndaw fa Gine Bisaawo diggante ñaar-fukki fan ak benn ak ñaar-fukki fan ak juróom-ñeent. Cig pàttali, moom Njiitu réew ma, Umar Sisoko Embaloo, dafa yokk ci ag moomeem lu tollu ci juróom-ñeenti weer. Dafa di, moom nee ñu moomeem ñaar-fukki fan ak juróom-ñaar ci weeru féewiryee wii la waroon a jeex. Waaye, taxul mu yamale ko fa. Rax-ci-dolli, mu xamle ne ñaari wote yépp jàpp nañ leen fanweeri fan ci weeru sàttumbar.
Ndaw yi ñu fa yabaloon nag, jubluwaay bi moo nekkoon ñu jàppale ñi fay yëngu ci pólitig ngir ñu am ab déggoo ci amalug wote yi cig dal. Mu nekk wote yoo xam ne du am xiiroo ak ŋaayoo. Te, du am it ay xàjj ak seen. Ndaw yi ñu yónni woon nag, ba ñu àggee Njiitu réew ma, dalal na leen.
Ginnaaw loolu, moom it mu yëgal ko ñi ko war a yëg ñépp. Muy ñi boroom làngi pólitig yi, kilifa yi, kurél yi yor wàllu wote yi, añs. Waaye, loolu waralul coow li. Nde, amal nañu aw waxtaan ba ndawi CEDEAO yi ak UNOWAS déglu njàmbati gaa ñi ak seen i mébét. Ñoom sax, ñu jàpp ne loolu dina yombal déggoo ngir wote yi mën a am. Ndeke booba fekk na, Njiitu réew ma xalaatul lu ni mel.
Ñoom ndaw yooyu bi ñu waajee bay teg seen naal ñeel anam yi ñu war a amale wote yi ci atum 2025. Yemuñu ci loolu sax, ñu tàmbali di ko aajar mbootaay, kurél walla làng yi bokkoon ci waxtaan wi ngir ñu jox leen seen kàddu. Ca la leen Njiitu réew tàmbalee di leen tëkku. Ci lañu dawee, génn réew ma. Daw ca ba ngay am i tànk. Ginnaaw mbir yi deme na noonu, ñoom tooguñu bank seen i loxo. Ndax, ci yégle bi ñu génnee xamle nañu ci ne dinañu aajar ag caabal Njiitu ndiisog CEDEAO gi.
Mu mel ni CEDEAO mi ngi wéy di néew doole. Maanaam, léegi, dafa am jafe-jafeb saafara coow yi am ci réew yi. Rax-ci-dolli, réewi AES yi (Mali, Burkinaa Faaso ak Niseer) bokkatuñu ci kurél googu. Loolu tamit, wàññi na dooleem bu baax. Li mat a laaj kay mooy ndax, CEDEAO day toog bank ay loxoom ci xeetu doxalin yii? Walla ndax day jël ay matuwaayam ci ñi bëgg a salfaañe sàrt yi ñu tëral ? Li ci kanam rawul i bët.