Boroom xalima bu ñaw bi defati na jaloore. Bubakar Bóris Jóob, werekaan bi, móolati na téere bu bees, duppee ko Un tombeau pour Kinne Gaajo. Mu dib téere fent bob, tekkig Bàmmeelu Kocc Barma la ci farãse. Keroog, àjjuma 8 màrs 2024 la doon aajar téere bi fa Siwis, ca xew-xewub téere bu amoon fa réewum Siwis (Salon africain du livre de Genève). Waa yéenekaay Le Point jaare ci, séq ak moom laaj-tontu ñeel téere bi.
Bubakar Bóris Jóob dolleeti na beneen téere ci kàggoom gu gànjaru gi. Un Tombeau pour Kinne Gaajo, kërug móolukaay gii di Philippe Rey, moo ko génne ci atum 2024 mii. Muy téere bu mu tekki ci làkkuw farãse ginnaaw bi mu ko njëkkee móol ci làmmiñu wolof, ci turu BàmmeeluKoccBarma, te EJO-Éditions móoloon ko ca atum 2018.
Ci waxtaan woowu mu séq ak waa Le Point, Bubakar Bóris Jóob biral na ni, keroog ba gaal gu mag gii di Le Joola suuxee ca géeju Gàmbi ga, ci bésub 26 sàttumbar 2002, la amoon yéeney bind ci. Muy gaal gu daan daw diggante Ndakaaru ak Sigicoor. Gaal gi nag, dafa yóbbaale ca suux ga ndongo lu nekkoon këram, yóbbaaleet ay ci xayma ñaari junniy doom-aadama ak lu teg. Ci noonu la bindakat bi fentee ab aji-jëmmal ngir nettali jaar-jaaram, ñàmbaasaale ci ay njàngat yu musibab Le Joola feeñal ci mboolaayu Senegaal. Muy ñaari nettali yu ànd laxasu ci téere bi.
Kinne Gaajo miy aji-jëmmal ji gën a fés ci nettali bi du kenn kott ku fentaakon bi xam ci dundam. Nde, ciy waxam, soppul walla bëggul, ci usuloom, ñu naan diw walla diw lay delloo njukkal ciy nettaleem. Dafa fekk ni sax, ay nit ñu bare, ñu mu xamoon, ñu fi dee gi bawul, la boole dëxëñ ci Kinne Gaajo.
Doon naat téere buy delloo nit ñi ci mboor ak ni muy nettalee yenn ciy xew-xew ca jamono ja tubaab bi nootee réew mi, walla mboorum Waaloo ba ci jaar-jaaru yenn boroomi tur yu mel ni Siidiya Lewoŋ Jóob.
Téere laat bob, dafa ciy wone melokaanu kibaaraan yi fi réewum Senegaal. Ba tax bindakat bi di fàttali ni moom ci boppam taskatu xibaar la. Waaye, ci seetloom, taskati xibaar yi cosaanoo fi réew mi tàmmuñu di gëstu bu baax ci xibaar yiy rotee bitim-réew. Bu ñu ciy wax, dangay gis ni dañuy baamtu gàttal yi ci kibaaraan yu mag yi nekk ci àddina si, yem ci.
Téere bi, ni ñu ko waxee ci kow, ag tekki la. Ci wolof la ko bindkat bi njëkk a siiwal. Muy xamle ni toog na lu yàgg, di xel ñaar, laata muy tàmbalee bind ci làmmiñu wolof. Li ko waraloon di li mu yaakaaroon ni mënu ko ak yenn waxi kasaw-kasaw yi mu daan faral di dégg yu deme ni : « kenn du ko dawal » walla sax « réewi afrig yi dañu bare ay làmmiñ », ak yu ni mel.
Moom Bubakar Bóris Jóob sax, ku yàggoon a am ay yëg-yëg yu doy waar la ci làkku jàmbur wi mu daan jëfandikoo. Loolu sax moo ko gën a taqaleek li ñoom Séex Anta Jóob ak Ngugi Wa Thiong’o daan wax, naan amul ladab bu tax ñuy wax ladab dëgg bu ñuy amal ci làkkuw jàmbur, rawatina bu ñuy amal ci làkku nootkat bi. Bi mu demee Ruwàndaa nag la tàmbalee bind. Ci la xameet ni fa la waroon a tàmbalee.
Këru móolukaay gi njëkk móol téere bi ci làmmiñu wolof, EJO-Éditions, yemul rekk ci làmmiñu wolof. Dafay móol itam ci yeneen làmmiñi réew mi ak yu Afrig. Xamle na sax seen lënkoo ak genneen kër ci móolug téereem bii di Murambi ci làmmiñu suwaahili, te ñu war koo génne fileek ñaari ayu-bés. Ci wetu EJO-Éditions itam, taxawal na fa yéenekaayu web ci turu LU DEFU WAXU (www.defuwaxu.com). Muy yéenekaay bob, moom doŋŋ lañ xam ba tey, ci mbooru réewum Senegal, bu am ci buumug jokkale gi.