USMAAN SONKO A NGI CI DIGGANTE DUND AK DEE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Wér-gi-yaramu Usmaan Sonko gën na doy waar. Njiiti YAW (Yewwi Askan Wi) yi ñoo ko dëggal. Fekk ñu doxantuji woon fa raglub Ndakaaru b (Hôpital Principal) doon fa nemmeekuji seen nawle bi. Ba ñu fa jógee nag, woo nañ taskati xibaar, xamal àddina sépp ne, nii ñu gisee Usmaan Sonko, lu nekk mën na ci xewe.

Bërki-démb ci àjjuma ji, njiiti lëkkatoo YAW yi doon nañ janoo ak taskati xibaar yi. Lu ko waral nag du lenn lu dul mbiri Usmaan Sonko. Ginnaaw bés yu bare yi mu xiifal, lànk bañ a lekk, seen nawle bi dafa lott lool ba ñu rawale ko ca raglub Ndakaaru ba. Bi ñu ko fa seetijee nag, tiitaange ak njàqare lañu fa jële.

 « Usmaan Sonko mee ñu gis, Usmaan Sonko, nun, xàmmewunu ko woon. Waaye, moom itam xàmmewu nu. Usmaan Sonko bu sonn. Usmaan Sonko mi nga xam ni, waa ju jàmbaare jooju nga xam ni bëggul ku ko yërëm, ñu fekk ko mu nekk ci beneen anam boo xam ni xàmmewul dara. Yegg na ci nun ñii ci sunu bopp mënunu ko woon a jox sax yóbbante bi ko sëriñam bu baax bi jox. » (Ayda Mbooj, kenn ci ñi ko seeti woon)

Yile kàddu di wone ni liñ fa gis dalul wenn yoon seen i xel. Àgg nañu sax ci ne Usmaan Sonko mi ngi ci diggante dund ak dee. Looloo tax ba ñuy artu askan wi ak di sàkku ci Njiitu réew mi mu bàyyi ko ci ni mu gën a gaawe.

« Usmaan Sonko, na mu nekke du yoon. Luy jot jot na. Fee mu tëdd du bërëbam. Li ñaari soxnam yi wax mooy dëgg. Dañu ko war a bàyyi mu ñibbi këram. Loolu mooy dëgg ji. Te lépp mën na ci xewe. » (Abib Si, ki yor kàddu lëkkatoog YAW)

Waa YAW sax wéetuñu ci càkkuteef googu. Ngir ñu bàyyi Usmaan Sonko ak ñi mu nekkal ci kaso bi, kurél gii ñu tuddee « chemin de la liberté », maanaam yoonu péexte, nammoon naa amal ab ñaxtu ci gaawu gi. Waaye, Perefe bu Ndakaaru daf ko gàntal. Fii mu nekk nii, dañoo mujje woote tëggum bool fépp ci biir réew mi ak fa bitim-réew.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj