USMAAN SONKO AK MAKI SÀLL : CÓOKI MUJJ GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tey, ci altine ji lees war a àttewaat layoob Usmaan Sonko ak Maam Mbay Ñaŋ ca Ndakaaru. Léegi, daanaka mëneesul a toog ñari weer yoy, Yoon wooluwul njiitul Pastef li. Lu jege juróom-ñaari at ginnaaw bi ñu ko dàqee ak léegi, Usmaan Sonko jógul ci di jëflante ak Yoon. Mu mel ni nag, yëf yi dafa yokk ci ñaar, jàpp ñetti at yii mujj. Ndax, daanaaka coow lu mu génn rekk, Nguur gi dugal ko ci leneen. Ren jii, rekk amagun na lu tollu ci juróomi layoo ca kanamu Yoon. Te, yemul foofu. Ndax, ci weer wii rekk am na ci ñaari layoo, nu altiney tey ji, 8 me 2023, moom ak kii di Maam Mbay Ñaŋ, ak bu 16 me 2023 bi, moom ak Aji Raabi Saar mi ko doon jiiñ mbirum ciif. Ñu ni déet-a-waay, ku ñuy wax F. Napel daladi koy pelent, moom itam. Lu ëpp ci askan wi dañoo jàpp ne Maki Sàll moo nekk ci ginnaaw tuuma yii yépp. Te duggewuñ ko lu dul tere koo bokk ci wotey 2024 yi. NDax loolu jar na taal réew mi ?

Dañu singali Usmaan Sonko. Loolu la ñu bari jàpp. Nde, diggante Usmaan Sonko ak Yoonu Senegaal rataxatul dara. Dafa di, bi mu duggee ci pólitig ba léegi, tegelees na koy ndëgg-sërëx yu baree bari, gàll koy tuuma yu dul jeex, di ko tam dëmm saa su nekk. Bu yeboo ne, ginnaaw Yàlla, bu dul woon askan wi, kenn waxatul waxi Usmaan Sonko. Tey ci altine jii rekk, warees na àttewaat digganteem ak Maam Mbay Ñaŋ ci mbirul yàq der. Moone de, njëkkoon nañ ko àtte ba daan ko ñari weer yum dul tëdd ak 200i tamndaret yu muy dàmpe Maam Mbay Ñaŋ. Kooku, ndawul APR li, dafa kontaanoon ci daan yi, waxoon ne Yoon setal na deram. Kon lu fi jaroon àppel bi ? Nga xam ne am na luy ñuul ci soow mi. Mu mel ni loolu la Usmaan Sonko xam ba ne, léegi, dootul wuyooti Yoonu Senegaal ngir nees di salfaañee ak àqam ak i yelleefam, rawatina fitna jees koy teg, moom, njabootam, jegeñaaleem yeek dëkkandoom yi.

Usmaan Sonko doon na amal uw waxtaan démb ci guddi gi. Xamle na ne du teewati ci layoo yi walla di wuyu Yoon. Ndaxte, moom, dafa jàpp ne Yoonu dafa dëkk ci di ko lor. Indiy firnde nag. Nde, ciy waxam, 2016 ak léegi amul lu ko Yoon tegul ciy fitna ak i loraange. Loolu sax, waxoon na ko keroog, ca ndajem-waxtaanam wu mujj wa :

Yoon woowu nag daf noo yàgg a lor. Dund naa ba 2016 mësumaa am coow ak Yoon. 2016 ba léegi, lu nekk Yoon teg na ko sama ndoddu ngir bëgg maa lor ak bëgg maa gàllankoor te, teguwul ci dëgg nag.”

Mu neeti, bi mu fi jotee ak soxna sii di Aji Saar, dañ ko bëggoon jàpp, fekk mi ngi oon dépite, lu Yoon mayewul, mu daldi bañ. Ñu juge ca, gaa ñi teggi malaanu kiiraayam ci anam yu méngoowul ak sàrti réew mi. Maanaam dañu ko jaay doole daal. Yokk na ci ne, bim wuyujee Yoon, dañ ko jàppoon, teye ko juróom-benni fan, daldi koy jébbal àttekat bi te ay layookatam teewuñu woon. Te, Yoon def ne am nga sañ-sañu am i layookat te, àttekat bi warul a déglu te, say layookat teewuñu. Booba, askan waa fippu, Maki Sàll ak i nitam deltu ginnaaw, ñu bàyi ko. Loolu weesu, ñu nangu jàll-waaxam, tere ko génn réew mi. Ñaari at ak lu teg yoo xam ne mënul a dem fenn. Te, nee na saa yu bindee ne leen dafa bëgg a génn ngir liggéeyal meeri bu Sigicoor, duñu ko tontu sax. Kon, lii, xoqatal ak jaay doole lay niru. Usmaan Sonko daf ne sax, àttekat, walla fukk ci ñoom, ay surgay Maki Sàll lañu. Ciy ndigalam lañuy wéy. Te, réew moom, bu Yoon wa sooxee rekk, lu bari sooxe fa. Moo tax mu ne :

“Li nar a boyal réew mi, Yal nanu ci Yàlla musal, li nar a indi fitna ci réew mi mooy Yoon. Te, du weesu juróom walla fukki ndawi Yoon yoo xam ne, li taxoon ñu teg leen foofu, li taxoon ñu waat ñoom ne loolu lañuy jëfe, fàtte nañu ko bu yàgg. Nekk nag, ay baay-faalu Maki Sàll, bu ne leen tëjal ñu tëj, bu leen nee bàyyil ñu bàyyi (…). Gis ngeen weer wu ne walla ñaari weer yu ne Maki Sàll soppi ay àttekat. Ndax, day tànn ay nitam, lu mu bëgg ci ñoom dem ba ci biir amu ko mu gaawantu soppi leen. Li ci gën a fés nag ci li mu bëgg ci ay àttekat te, amu ko mu mer mooy fexe leen ba daanal ma Usmaan Sonko ci daan boo xam ne dootul mën a nekk lawax. Ña ca des mooy ñoñi Usmaan Sonko yi jàpp na ci ñu bari tëj leen. Am nanu ñetti téeméer ak juróom-fukk ak juróom ci ay militaŋi Pastef yoo xam ne ñu ngi leen téye.”

Waaye, yemul foofu. Yokk na ci ne :

“Ñoom jàpp nañu wayndare yi lu mu gën a sakkan rekk, dinañu ci am benn boo xam ne dinañu ci am li ñu bëgg. Waaye, man, nu ñu mënee ubbil ma ay wayndare yu dul jeex. Ab sindax sax, bu romboon fii ne Sonkoo ma xeelu, ñu ubbi wayndare. Ba pare, man, bu ma jébbalee ab pelent duñu ko lijjanti.”

Loolu tax mu jàpp ci boppam ne Yoonu Senegaal dafa jeng ci moom. Tëddewul wenn yoon njaaxanaay ci ay mbiram. Ndax, lu ko mën a yàqal rekk lañuy seet. Seen Yoon nekkul ci ku ko tooñ, li leen yitteel mooy ki ñu yaakaar ne daf ko tooñ. Moo tax, 2016 ba léegi daanaka mi ngi jëflante ak Yoon waaye, amagu ci ndam. Daanaka 2018 ak léegi mi ngi jébbal ay pelent. Muy bu ci mel ni bi ñu faate kii di Mariyaama Saaña, pelent bi mu def Mammadu Maamur Jàllo ci luubalug 94i miliyaar ak yeneen yu bari yu mu def bu yàggul dara. Waaye, ba tey mujjul fenn. Looloo tax moom, mu jàpp ne fa mu waroon a àgg ak Yoon ci gëddaal ko àgg na fa.

“Man dama jàpp ne li ma waroon a def ngir wone ne jox naa gëdd Yoon def naa ko. Waaye, saa su ne li ma Yoon di feye mooy joxuma benn cër. Kon nag, jot na ku nekk jël ag kiliftéefam. Te, bés ni ki tey dina door li ñuy dippe « campagne de désobéissance civique » ñeel Yoon. Mooy nanguluma ko cër bi mu jox boppam. Ku nekk na jël ay matuwaayam, man lu ma ci góobe, gar ko.”   

Kon, Njiitul Pastef li sumb na ab xeex ak Yoonu Senegaal. Te, nee na bañu ci dara. Looloo tax, keroog mu jaare Gàmbi ba muy dem Sigicoor wone ne lii mooy yoon wu njëkk muy génn réewum Senegaal ginnaaw ñaari at yu teg. Rax-ci-dolli mel na ni moom narul a dem ca layoo bii di ñëw. Ndax, bés bi ñu koy amal dafa woote am ndaje ak ñi mu bokkal meeri ba ca Sigicoor. Li am ba des kay mooy xeex bi moom door na bu yàgg. Fan lay mujj kay la kenn xamagul. Fim nekk nii nag, Njiitu réew mi, Maki Sàll, ak Usmaan Sonko àgg nañ ci cóoki mujj gi. Kuy am ndam ? Ku dund, fekke.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj