USMAAN SONKO CA XEWUM WAATU POOL KAGAME

Yeneen i xët

Aji bind ji

Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, dem na Ruwàndaa. Dafa teeweeji xewum waatu Póol Kagame mi ñu falaat ci wotey 15i pani sulet 2024 yi amoon Ruwàndaa. Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, la fa teewali. Ëllëg, ci dibéer ji, 11i pani ut 2024, la xew miy am. Rwanda Broadcasting Agency (RBA) a ko yégle ci X.
Yeneen njiiti réew fekkeeji nañ tamit xew mi : Salwaa Kiir (Sudã-Suuf), Umaroo Sisoko Embaloo (Gine Bisaawo), Emerson Mnangagwa (Simbaabuwe) ak Cemoko Meyliyet Kone miy Tof-njiitu réewum Koddiwaar. Ñoom ñépp, teer nañ fa dalub roppalaan bu Ruwàndaa, ca gëblag réew ma.
Ngir fàttali, 15i pani sulet wii weesu la askanu Ruwàndaa falaat Póol Kagame, dénkaat ko lengey réew ma. Ci téeméeri wotekat ñoo jël, 99,18 yi moom lañu sàndil xob. Gii mooy ñeenteelu moomeem ca boppu réew ma.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj