Ci gaawug tey jii, 2 sàttumbaar 2023, la xibaar bi jib. Yéenakaay bii di Yoor-Yoor moo ko xëyee. Usmaan Sonko mi toog weer ak lu teg lekkul, naanul, moo dog xiifalam gi.
Yéenekaayu Sëriñ Saaliw Géy bi dafa bind ne :
“ginnaaw bi ko saa-senegaal yi saraxoo, ñaan ko, ñaanati ko ngir mu bañ a ñàkk bakkanam, ginnaaw bataaxalu Xalifa murit yi, Sëriñ Muntaqaa Mbàkke, ginnaaw wooteb 101i fajkat, farmasiyeŋ yi ak ñiy liggéey ci wàllu wér-gi-yaram ak wooteb layookatam yi, njiitul Pastef li, Usmaan Sonko, jël na ndogalu dogandi xiifalam gi, ci gaawug tey jii, 2i fan ci sàttumbaar. “
Cig pàttali, bésub 28 ci sulet 2023 lañ jàppoon Usmaan Sonko. Booba la tàmbali woon xiifal ngir xeexe ko xoqatal bi Nguur giy xoqatal saa su nekk. Nooonu la ko jàppe ba nees koy rawale fa raglub Ndakaaru ba, ça “réanimation” ba. Nde, dafa demoon ba loof, sonn lool, tollu diggante dund ak dee. Ñu baree tiitoon, amoon njàqare. Dafa di, xibaar ya doon rote fa raglub Ndakaaru ba, rawatina yoy layookatam bi, Sire Keledoor Li doon fésal, dalul woon xel. Ca la ko nit ñi tàmbalee ñaan ak soññ ngir mu lekk, muccal bakkanam. Ca la ko Sëriñ Muntaqaa Mbàkke yónnee ay tàndarma, jaarale ko ci loxoy kilifay lëkkatoo Yewwi Askan Wi, ngir mu dog koorug xeexam gi.
Nee ñu, bi ñu ko jëkkee yóbbul tàndarma yi, dafa nekkoon ci komaa. Bi mu ximmalikoo la ci jot, dog xiifalam gi. Waaye nag, nee ñu, dafa teg ay sàrt yu leer yoy, bu leen Nguur gi jëfewul, day àggali xiifalam gi.
Xameesagul yan sàrt la Usmaan Sonko teg. Du ñàkk ñu am ciy leeral fileek fan yu néew.