Njiitul Pastef li, Usmaan Sonko, dina dellu Ndakaaru. Tey ci àllarba ji la ko biral fa Siggicoor ga mu nekk boobu ba tey. Ci bi ngoon gi teroo la génn, doon saafoonteek soppeem yi teewoon ca buntu këram, làngaale ci Mbedd yi.
Bi mu jëlee kàddu gi, yékkati nay kàdduy cant ñeel askanu Siggicoor ci taxawu biñ ko taxawu. Xamal na leen ni li ñu def du lu ndaw te buñ ko xeeb. Nde bi mu ñëwee Siggicoor, lees xañoon waa Ndakaaru donte niy jàmbaar lañ, ñoom waa Siggicoor àntul nañ ko. Li mu def mi ngi ko gise ni ku dem ba xamatul fa mu jëm mu dellu fa mu jóge. Te réccuwu ko benn yoon. Nde bu toogoon Ndakaaru, amaana ñu jaay ko doole nees ko daan defe.
Bu dee lu jëm ci layoo bi, li mu yàgg a wax rekk la baamtu. Te delsi na ci lu yaatu bi muy def live ci guddi gi. Du lenn lu dul Baara-yëgoo gu Maki sàll ak i ñoñam lal ngir faagaagal ko. Nde dara luy nirool firnde mënuñu ko génne. Te ñoo ngi gis ni mbir yi di mujjee dellu di këppu ci seen kow.
Ginnaaw loolu, xamal na leen ni jot na mu dellu Ndakaaru. Ndax xeex boo gis ay pexee koy lal, te foofu la xeex bi tollu tey, muy « cóoki finaal ». Ci noonu, mi ngi woo ndaw yi ci ñu takku ba dëgër, te noppi ngir sàmm seen sémb bi nu bokk gëm. Muy sàkku ci képp kuy ndaw ci Senegaal, ak diwaan boo mën a nekk, nga gëm li ñuy def te mu jaral la, ngeen daje ji Ndakaaru. Nde bu Njiitu réew mi Maki Sàll délluwul ginnaaw dinañu jàkkaarlook moom.
Bokk naat ci li mu ñaan ndaw ñi, ñu ñàggi ñag bi ñu ñagoon ca këram ak li ko wër. Mën nañ wéy di wattu kaaraangeem te bàyyi dem beek dikk bi ci yoon yi mën a féex.
Bu dee lu jëm ci wàllum yëngu-yëngu yiñ daan amal ak làngug Pestef, dinañu delloo buum ca boy-boy ga. Dinañu yeggali seen nemmeeku-tuur yi. Te sax buy dellu Ndakaaru, yoonu suuf bi lay jël. Bu ko defee, dina jaar ci dëkk yépp nekk ci yoon bi : li ko dale Siggicoor ba Ndakaaru. Muy li mu tudde « caravane de la liberté ».