« USMAAN SONKO NEE NA YËGATUL WETU CÀMMOOÑAM… »

Yeneen i xët

Aji bind ji

Xadi Kebe ak Aana Jamanka, ñaari soxnay Usmaan Sonko yi, doon nañ amal ab laaj-tontu ak kii di Paap Aale Ñaŋ mu Dakar matin. Waxtaan woowu nag, def nañu ko lu jege diirub waxtu. Ci àjjuma jii weesu lañ séqoon waxtaan wi. Faramfàcce nañ fay ponk yu bari, rawatina xoqatal gi ñuy dund, ñoom, seen ug njaboot ak seen boroom kër, li ko dale 2021 ba tey. Waaye nag, li gën a bir ci waxtaan wi mooy mbirum wér-gi-yaramu Usmaan Sonko. Ndax, ba ñu ko jàppee, ci njeexitalu weeru sulet wi nu génn ba tey, mi ngiy xiifal. Dem na ba, jamono jii, loof na lool, sonn ba ñu rawale ko fa raglub Ndakaaru ba. Dafa di sax, “réanimation” (fa ñuy jéem a muccalee way-tawat yi tollu ci diggante dund ak dee), lañu ko mujje jàllale.

Bërki-démb ci àjjuma ji, soxnay Usmaan Sonko yi xamal nañu saa-senegaal yi mbooleem metit yi ñu leen di teg, ñoom ak seen njaboot, bi seen boroom kër duggee ci làngu pólitig gi ba léegi. Ndax, yëf yi tàmbaleewul ci njàppug Usmaan onko. Nde, kenn umpalewul ne, jot nañ leen a ndar-kepp, ñg seen koñ ba fa Site Kër-Góor-Gi ci diirub juróom-fukki fan ak juróom-benn. Amul dem, amul dikk. Àggoon nañ ci ne, lépp lu ñu soxla waan, Jibi Géy moo leen ko daan jëndali. Ba ci këriñ, añs. Te, buñ la bàyyi waan ñu génn, dañ leen daan làmbaatu ci kow ba ci suuf laata ñu leen di bàyyi ; muy ñoom, soxnay Usmaan Sonko yi, muy seen i doom, ba ci waa koñ ba sax muccuñu ci. Seen boroom kër moom, kenn da koo waxaalewul, génn sax daawu ko def. Kon, seen coono doorul tey donte ne sax ñi ngi ko doon muñ. Waaye nag, ni ñu ko waxee ñoom ci seen bopp : « xol du óom ba ñu koy bës. » Rax-ci-dolli fim tollu nii tembare, yëf yaa ngi bëgg a ëpp i loxo.

Li waral seen génn googu du lenn lu dul ag jaaxle. Ndax, kenn umpalewul ne, xiifal gi meeru Sigicoor bi dooroon ginnaaw bi ñu ko tegee loxo, ma nga ca ba léegi. Tey la am ñaar fukki fan ak ñaar yoo xam ne sii, lekkul, naanul. Loolu tax ba jamono jii wér-gi-yaramam nasax lool. Maanaam, néew na doole daal. Bu doon ag daamar, mënees na wax ne dañu koy may loxo ngir mu sog a tàkk. Moo tax itamt, jamono jii, ku nekk a ngi def i pexe ngir bañ musiba am. Ñii a ngi sàkku ci moom, Usmaan Sonko, mu dakkal xiifal gi ngir mu mën a wéyal xeex bi ci beneen anam. Ña ca des moom, ñu ngi ñaan Njiitu réew mi Maki Sàll mu bàyyi ko ca na mu gën a gaawee ngir mu dellu ci njabootam balay mbir mi di jéggi dayo. Dafa di, jamono jii, Usmaan Sonko sonn na lool bees sukkandikoo ci kàdduy soxnaam. Looloo tax, ñoom ñu ne, ni ñu ko gisee neexuleen dara te dalul seen i xel. Ndax, kii di ñaareel bi, Aana Jamankaa, nee na xamal na ko « yëgatul wetu càmmooñam gi. »

Mu nekk mbir mu doy waar. Te, lenn waralu ko lu dul xiifal gi mu door bu yàgg ba tey. Xiifal googu tax sax mu mujj daanu, ame jagadi. Barkaatu-démb ba léegi, ma nga ca “réanimation” ba. Te, li sabab loolu lépp mooy njàpp gi ñu ko jàpp. Ndax, moom Usmaan Sonko, dafa gëm ni teguwul ci Yoon. Maanaam, pólitig rekk a ko lal. Maki Sàll daf ko bëgg a fexeel. Te, moom dafa yàgg a wax ne, ku ko nar a jaay doole dina bañ. Ndeyu-àtte ji moo ko ko may, ciy waxam. Ni wér-gi-yaramam nasaxee nag moo tax soxnaam yi di ñaan ñu bàyyi ko. Ñu jiital ci càkkuteef googu Njiitu réew mi Maki Sàll ak soxnaam Mareem Fay Sàll mi nga xam ne, « … moom yaay la » ni ñoom. Ñaan nañu leen ñu delloo leen seen boroom kër, ñu fajal ko seen bopp. Bu leen neexee sax, nañu fa indi mbooleem li ñu yor ci ay takk-der. Waaye, na ñu leen ko delloo rekk.

Nu xool fu mbir miy mujje.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj