SONKO, AK KAN ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Alxames, 16 màrs 2023 ba tey, Usmaan Sonkoo nga ca raglu ba, tëdd. Waa Pastef ñoo ngiy def seen kemtalaayu kàttan ngir jàllale ko bitim-réew ngir mu fajoo fa. Nde, feebaram bi day gën di doy waar, taneegul ba nëgëni. Rax-ci-dolli, xameesul ban xeetu poson lees ko pomp. Looloo yokkati njàqarey mbokkam, ay àndandoom ak i soppeem. Keroog, nag, coow li noon na kurr, xeex bi jolli diggante ndaw ñeek takk-der yi, tàngoon jërr. Waaye, boobaak tey, amul kenn ci kujje gi koo xam ne, wuutu na Usmaan Sonko ci taxawaayam.

Layoo Maam Mbay Ñaŋ ak Usmaan Sonko bare nay njàngat yees ci mën a jukkee. Keroog, ca alxames ja, mujjul woon a àgg. Ndaxte, dañu ko dàqati woon ba bésub 30 màrs 2023. Booboo doon ñetteel wi yoon ñu koy ajandi. Mu bari nag ay mbir yu xew ci layoo boobu, donte ne sax, bee jàll am na ay mbir yu ca xewoon. Waaye, xew-xew yii ñoo gën a doy waar. Te, yépp walla yi ci ëpp ci kow Usmaan Sonko walla ay ñoñam la dal.

Àddina sépp a gis li xew ak lees di teg ci kow doomu jàmbur jii di Usmaan Sonko mom, dara taxu koy xeex lu mooy Senegaal gu baax ba fàww. Waaye, bi mu sóoboo ci làngu pólitig gi ba tey, amul luñ ko deful ci xeeti ñaawteef, tooñaange ak i fitna. Dafa dem ba, mbir yi dafay xaw a saamandaay mbañeel ak ug nooneel. Nde, ku seetlu li njiitul Pastef lii di meeru Sigicoor di jànkonteel 2014 ba tey, dinga xam ne dootul kujjeg pólitig kese.

Saab bu Usmaan Sonko waree wuyuji, walla kujje gi naal ab doxu ñaxtu, takk-der yi dañuy léem koñu meeru Sigicoor bi, gànnaayu ba diis, fees fa dell, fatt yoon yépp ba kenn du duggu, kenn du génn. Amul duggi, amul jàngi ; kenn du xëy, kenn du wàcc. Dafa di, julliji sax, dañ la koy tere. Te, nag, du am benn ndogal lol, àttekat baa koy jël ngir sàrtal doxalin woowu. Moom, mbirum jay doole la, ak di xoqatal ag kilifa gog, li ëpp ci askan wi, moom lañu àndal. Noonee lañ ko defaatoon, keroog alxames jooju. Jamono jooju, fekk na Maam Mbay Ñaŋ di dox ay soxlaam, di dem fu ko neex ak nim ko neexee. Waaye, Usmaan Sonko moom, amul sax sañ-sañu jaar yoon wu ko neex.

Bi ñu xëyee keroog, Usmaan Sonko ak Maam Mbay Ñaŋ yépp ñoo dëgmal ëttu àttewaay ba. Waaye, li ci jig Maam Mbay jigu ci Usmaan Sonko. Ndax, moom dem na ci jàmm, ñibbi ci jàmm. Waaye, Usmaan Sonko, moom, du génn këram, walla bu dee génn dañ ko xàllal uw yoon, ga ko ci. Ba muy dem ca layoo ba, dañu ko kara, def ko na ñu ko defoon yoon wale weesu, ba muy ñibbi. Ndax, dañu dàjjiwaat daamaram gi, jàpp ko, pamti-pamtee ko, metital ko, dugal ñóox ko ci daamaaru BIP ga, yóbbu ko àttewaay ba ci lu dul coobareem. Lépp, takk-der ya boole ci jaay doole gu mat sëkk. Dafa di, Usmaan Sonko dafa naroon a ñibbi bi mu gisee ne amatul kaaraange, waaye gaa ñi mayuñu ko fu mu yakke nàkkaam. Loolu la dépite Guy Maris Saaña di biral ci kàddoom yii :

“Sonko daf ne woon dafay ñibbi, dematul ca layoo ba. Ndaxte, kaaraange amul. Ñu bañ, ne ko dangay dem ca ëttu àttewaay ba. Dañoo jël Usmaan Sonko bëgg koo dugal ci daamaru BIP g. Man, maa ko jëli foofu, ñoddi ko, dugal ko ci genn daamar 44. Ñu ñëw fekk nu foofu ne day génn, ma ne leen du génn, ma kott ko, ñu xëcc ko ba sonn, mënuñu ko génne. Boobu lañu jël pompu gaas pomp ma ko. Boobu, metit gi samay gët, metit gi sama kanam, sama bopp. Maa ngi mel ni koo xam ne dañoo jël layset di dagg samay bët, di dagg sama deru bopp bi yépp. Amuma woon meneen pexe lu dul, ak metit googu yooyu yépp, kott gi ma kott Usmaan Sonko, ma bàyyi ko. Ci lañu ko jële.” 

Mu mel ni kon yëf yi ci ñoom ñépp la metti. Ndax, moom Guy Maris Saaña, xamle woon na ci mbaalu jokkoo gii di Facebook ne, keroo, jàppoon nañu téeméer ak juróom-ñetti-fukki doomi aadama. Waaye, tey jile, lim bi àgg na ci 400i nit yees teg loxo. Waaye, mbir mi yemul foofu ndax ci jamonoo jii nuy wax ak yeen, njàqareek tiitangee am ñeel wér-gi-yaramu Usmaan Sonko.

Ba sàndarm yay génne Usmaan Sonko ci daamaram ga, dafa am benn xeetu ndefar buñ ko pompoon. Pomp boobu moo soppi woon wirgob yéreem bi sax, laalaale layookatam bii di Sire Keledoor Li mi ngi xam ne, rawalees na Farãs. Ñoom ñaar ñépp, kenn àggaliwu ci layo bi ndax yaram yu jagadi. Dañ leen a mujjoon yóbb ci pekkug ceet gi nekk ci ëttu àttewaay bi.

Bi ñu dàqee layoo bi, ajandi ko ba 30 màrs 2023, ca la Usmaan Sonko bëggoon a dem ca raglu ba ngir seet yaramam. Fekk na, boobu, àmbilãs jëlsi Sire Keledoor Li. Takk-der yi ne dee njiitul Pastef li du ci dal. Bu fa yemoon sax mu tane. Waaye, dañu dugalaat ci seen daamar, delloo ko ci lu dul coobareem. Bim àggee yit, mënul woon a génn, fajuji. Li ci gënatee doy waar, mooy ne mayuñu sax ab fajkat ngir mu dem seet ko.  Ci waxi boppam, Usmaan Sonko da doon miir, di amey metiti naq te di sëqat sëqat yu metti. Ñu woo waa SUMA ASSISTANCE, takk-der yi tere leen àgg. Ba tey, Usmaan Sonko di wax ne, ci xëtu Facebookam, Maki Sàll daf ko bëgg a bóom, te njëkkewu ko keroog. Waa Pastef teg ci ab yégle, di biral seen njàqare ci seen tawatub njiit lii di Usmaan Sonko. Ca la gaa ñi bàyyee àmbilãs bi jëlsi ko, yóbbu ko kilig ba. Boobaak léegi, moo nga fa tëdd.

Ci alxames jeek àjjuma ji, ndaw ñi doon nañ ñaxtu, taal ay bérébi liggéey, AUCHAN, Total, añs. Waaye, dafa mel ni coow li dakk na, donte ne takk-der yaa ngiy wéy di jàppe. Démb rekk, jàpp nañ Séex Umar Jaañ ak Abdu Kariim Géy (Kariim Xurum-Xaax). Dañuy dug ba ci kër yi di jàpp nit ñi. Lees seetlu nag, mooy ne, ginnaaw Usmaan Sonko, kenn ci waa kujje gi jiitewul xeex bi. Li am Sonko di daj, kenn ci ñoom daju ko te dajluwu ko. Loou dafa teey xel yi. Day wund ne, bu Usmaan Sonko jóge woon tey, du am ku koy wuutu ci xeex bi, ba ci biir Pastef sax, gisuñu kenn ku àngu xeex bi, taxaw ci kanam, xirtal nit ñi ci ñu wéyal xeex bi. Dafa di, génne ab yégle doyul. Askan wi jàmbaar ju leen di fital lañ soxla. Sonko de day fitalaate, ak kan ?

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj