Li Séex Umar Jaañ waxoon ci Tirailleurs sénégalais yi jur na coow lu réy ci réew mi. Ca jotaayu waxtaan ba mu amaloon ak tele bii di Fafatv, daf ci biraloon xalaatm ñeel sóobare yees dippee woon Tirailleurs sénégalais ca jamonoy mbéeféer ga, wax ne dañoo woroon.
Moom Séex Umar Jaañ, bokkul ci ñiy sagoo Les Tirailleurs sénégalais. Li ko waral moo di ne, bees sukkandikoo ciy waxam, ñooñu xeexaluñu woon Afrig, waaye Farãs lañu daan xeexal, daan ko jàppale. Te sax, ba tay ciy waxam, Tirailleurs sénégalaisyooyu, dañ daan xeex seen moroomi nit ñu ñuul ci ndigalu nootkat bi. Looloo tax mu jàppe leen ni ay workat.
Kàddu yooyii nag, dañu metti lool ci xoli njabooti sóobare yooyu ñu daan woowe LesTirailleurs sénégalais. Te, du ci seen làmmiñ kese lañu ko metitlu. Ndaxte, kurél gii di FADTS (Fédération des Associations des Descendants des Tirailleurs Sénégalais), ëmb njabooti Tirailleurs sénégalais yooyu, jure nañu Séex Umar Jaañ. Maanaam, dañu ko pelent. Li ñu ko dugge, ci seen i wax, mooy sàmm seen deri maam yooyu. Su ko defee, ëllëg ci biir kenn bañ a amati fitu yékkati ay kàddu yu leen di suufeel.