Lëkkatoo gi ëmb mbooleem njiit yi nekkug lawaxu Usmaan Sonko yitteel, ñu gën leen a xam ci turu Lacos (Leaders et alliés du candidat Ousmane Sonko), woote na bésub ñaxtu ci àjjuma jii di ñëw, 17 noowàmbar 2023. Ñu fas yéene nag jëmmal seen taxawaay ngir Usmaan Sonko mën a bokk ci wote yii di ñëw.
Barki-démb ci alxames ji la waa lëkkatoo gii di Lacos woote woon am ndaje doon ci jàkkaarlook taskati xibar yi. Li waraloon seen woote boobu nag du dara lu dul tolluwaayu réew mi, rawatina nekkug lawaxu njiitul Pastef gi woon.
Naka noonu, ñu biral fa ni dinañu tàmbali seen xeex ci ayu-bés bii di ñëw. Altinee ci jàmm, ñii di Daam Mbóoj, Maymuna Buso ak Mamadu Lamin Jànte dinañu demal seen bopp perefektiiru Ndakaaru ngir jébbal leen baataxalub yëgle bi. Bu ko defee, dinañu leen xamal seen ñaxu bi ñuy amal naka àjjuma jii di ñëw, yemoog bésub 17 noowàmbar 2023, fi jàpp roŋ-poye jedoo ba terminisu Libeerte Siis.
Ñaxtu boobu nag, li ñu ci gën a nam mooy sàkku ci DGE mu jëfe li ko Cena bi wax te jox Ayib Dafe xobi baayale yi Sonko yelloo. Waayeet di sàkku ci Càmm gi mu dakkal bunduxatal yi muy def Usmaan Sonko te may ko aafiyaam.
Ni ñu ko namm a defee nag lañu ko bëggee ci mbooleem ñi nekk ci 46i goxi Senegaal yi ak ñi féete bitim-réew. Moo tax ñuy sàkku ci ñoom ñu dem jébbal fa mu ware seen bataaxalub yëgle ci altine ji, laata 17i waxtu di jot.
Bésub 17 noowàmbar bi ñu jàpp nag dafa yemoog bés bi ëttu àttewaay bu Cedeao war a joxe àtteem ñeel diggante Càmmug Senegaal ak Usmaan Sonko. Ba tax na ñu ciy gaawantu ngir soññaale Càmm gi ci muy sàmmonteek ndogal yi yoon di jël saa su nekk.