WAAJTAAYU WOTEY 2024 YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Joŋantey 2024 yi door na, te luy jot jot na ginnaaw dee. Mu mel ni gaa ñi fare ci làngug pólitig gi nànd nañu loolu. Ba tax, ku nekk ci ñoom a ngi lal i pexe ngir daje ak askan wi, waxtaan ak ñoom. Ku nekk ci ñoom, ak na mu tudde xeetu dagaan googu. Ñii ne “Kaay Bokk”, ñee ne “Nemmeeku Tour” ; ñile di jaay seen i kàrti làng, ñale di amal i ndaje. Kon nag toogaay amatul, wure wa dem na keŋ. Lu waay doon jaay, léegi mu làmb.

Wotey gox-goxaat yi ak yu palum dépite jàll nañu. Kon nag, léegi, daj-dëpp gi moo ciy bëgg a des. Moo tax, gaa ñi tàmbali di biral seen yéeney bokk ci wote yooyu ngir yor réew mi ëllëg. Ku ci mel ni Usmaan Sonko, Njiital PASTEF, ba wote yooyu jàllee la biral ne lawax la ci wotey 2024 yi bu soobee Yàlla. Ba tax na, ci jamono jii mi ngi ci waajtaay yi ak sémbam bii mu dippe “Nemmeeku Tour”, tàmbali ko ci weer wii nu génn. Ci jamono yii sax, ma nga ca goxi Tiwaawon ya di wër dëkk-dëkkaan ya fa nekke.

Xalifa Sàll ak i mbokkam tamit de, deseñu ci ginnaaw, donte ne sax moom biraloon na ag bokkam ci wote yooyu, am na at ci ginnaaw :

“Yéene ji taxoon ma dem kaso… ndax dama bëggoon a doon lawax, yéene jooju, ma nekk biir kaso doxal ko ndaxte 2019 lawax laa woon. 2024, ci kàttanu Yàlla, su ma ko fekkee, te tal ko, dinaa doon lawax”

Taxawaay boobu mu am la gaa ñi bokk ci làngam giy dëggal. Te, ñoom it, fasuñoo yéene des wenn yoon ginnaaw ci xeex bi. Loolu la kii di Jokkel Gajaga, Kilifa ci làng gii di Taxawu Senegaal ca Kawlax, di biral ci kàddoom yii :

“Sunu lawax dafa nekk ci waajtaayu wër réew mi, fukki diwaan ak ñeent yi ñeen-fukk ak juróom-benn gox yi (…). Moo tax, tey nu ne danuy daje sottante xel ci loolu. Te, bu ñëwee, ci gox-goxaat yi la jëm. Moo tax, nu dajale njiit yépp ak seen i pekk ak ñi leen di jàppale ak ñépp, nu ànd tey joxante loxo, nekk benn, waajal wër googu nga xam ne dóotul yàgg. Ciy fan ñu ne nu bés sàngam la (…). Kon li des tey mooy wotey 2024 yi, sunu naataango Xalifa Abaabakar Sàll lawax la ci wote yooyu. Waaye, Yewwi Askan Wi du tuxu, du tas. Ndax, kurél gu ñuy soxla la. Ndax, booy jëflante ak koo xam ne du bàyyi tooñ, yaw tamit waroo bàyyi dóore.”

Mu mel ni nag, lëkkatoo gii di Yewwi Askan Wi, ñaari wote yii jàll boole woon leen, tasagul. Ba tax na, ci wote yii, ku nekk mën na am lawaxu boppam. Moo tax, kii di Décce Faal, njiital PRP (Parti Républicain pour le Progrès), tàmbali liggéey bi, jóg seeti gaa ñi nekk bitim-réew. Loolu nag mi ngi ko dippe “Kaay Bokk”. Mu tàmbali woon ko ñaar-fukki fan ci weeru oktoobar ca Marog, waroon ko jeexal fukki fan ak ñett ci weeru nowàmbar, ca Espaañ. Mu mel ni ndéglug Usmaan Sonko gi moo ko gàntal ba mu dogoon ko. Moom nag, ba tey biralagul ag bokkam ci wote yooyu waajal wote yi. Waaye, nee na, dina bokk am du bokk yépp, pare na ci lépp, biral mbir yi kepp a des.

Ba tey, kii di Doktoor Baabakar Jóob FDS (Forces Démocratiques du Sénégal) Les Gelwaar moom tamit mi ngi ci waajtaayu wote yooyu. Loolu lay biral ci kàddu yii mu yékkati woon juróom-ñaari fan ci weer wii:

“Danu def ndaje mu mag ca Rufisk, ñaar-fukki fan ak ñaar ba ñaar-fukki fan ak ñett ci weer wii jàll. Làng gi sas ma ma waajal doon lawaxu làng gi ci ag wër ngir laaj gaa ñi lan lañ xalaat ci wotey 2024 yi. Bi nu ci waxtaanee nu jàpp ne Kawlax ak li mu màndargaal ci mbooru Senegaal ci wàllu diine nekk ci xolu Senegaal, ñu ne nanu tàmbalee wër gi ci suuf su tedd sii, suuf su barkeel te làng yu bari juddoo fi (…). Bi ma duggee ci àll bi waxtaan ak nit ñi yaakaar naa lawaxu FDS Les Gelwaar mi ngi ci yoon (en téléchargement) te li ma gis ci àll bi mooy jokkoo bi doy na sëkk. Nanu xaar ba nga xamante ni biral nanu sunu bokk ci wote yooyu.”

Kii di Maalig Gàkku fésal na ag bokkam ca wote yooyu ca ndaje ma ñu doon amal dibéer fukki fan ak ñett ci weeru nowàmbar ñoom waa Grand Parti. Ci lay waxe ne “Maalig Gàkku mooy lawax bu askanu Senegaal, mooy lawax yaakaar ji, mooy lawax biy defar Senegaal, mooy lawax biy soppi Senegaal.” Te, moom, kii di  Ahmet Aydara la fas yéene def njiitu kàmpaañam.

Waaye, ñi fare ci Nguur gi tamit bàyyiwuñu benn yoon ak gaa ñi xew mi. Ñoom tamit, ci gaawu bale weesu fukki fan ak ñaar ci weeru nowàmbar lañu biral ndorteelu jaayug kàrt yi. Loolu la kii di Sëriñ Abiib Si di biral ci kàddu yii:

“Gaawu, bés niki tey, maa ngi woon ci taxawal gi (lancement). Man lu Njiitu réew mi nekk rekk maa ngi ci, loolu la Yàlla dogal. Ma ànd ci ak moom nag mu soxla benn miliyoŋ ak juróomi téeméeri junni ci ay kàrt yoo xamante ne nii, fas yéene nanu ko jaay. Ñëw nanu tey Tiwaawon, waaye bi nu ñëwee am nanu lu nu yëg.”

Mu mel ni ñoom, Njiitu réew mi Maki Sàll, lañu def seen lawax ci wote yooyu. Loolu Abdulaay Daawuda Jàllo wax keroog ca diwaanu Mbuur:

“Ma wax leen benn lawax lanu am ci jamono jii, Njiitu réew mi la, moom rekk la, amul keneen. Njiitu réew mi lanuy wutal, wutalunu keneen. Xanaa loolu kay warunu ci xaajaloo, ndeem Njiitu réew mi lanuy dimbali, jarul xiiroo ak ŋaayoo. Jarul kenn di wane dooleem, doole ji, doole goxu Mbuur moom lanu soxla. Njaayum kàrt yi tàmbali nanu ko (…). Kàrt bu nekk ñaar-fukki dërëm lay jar. APR li nu soxal mooy Njiitu réew mi doon sunu lawax ci wotey 2024 yi te loolu dëggal nanu ko laata nuy ñëw fii.”

Mu mel ni coowal ñetteelu moome gi, léegi nu am lu ci leer. Waaye, mu am ku gaa ñi di laam-laamee péeteem. Loolu tax, ci ndajem-waxtaan mu ay ñoñam doon amal ca ayu-bés bale nu génn, kii di Mataar Séy fara-caytu bu mag bu làng gii di Réew mi, kàddu yii la fa yékkati :

“Ñu bari dañu yaakaar ne Idiriisa Sekk Cees kese la, déedéet ! Senegaal yépp la, tey jii, ñeen-fukk ak juróom-benni gox yi fu nekk njiit jóge na fa, ñaar kepp a ñëwul te woote nañu wax lu tax ñëwuñu. Dugg ci Nguur gi wàññi na sunu doole tax na nit ñi bàyyi , nit ñi bàyyiwuñu. Ñeen-fukk ak juróom-ñeenti njiit yi ñu am ci gox yi, ba nu duggee ci Nguur, kenn moo ci bàyyi te kooku li ko bàyyiloo du pólitig (…). Bëgg a xam fu sunu doole tollu moo tax nu fas yéene natt la nu am ci ay kilifa ci Senegaal yépp, la nu am ci militaŋ ci biir ak ca bitim-réew. Danuy defar làng gi mu pare, nu topp ci ginnaawam déglu ko ànd ak moom jëm fa nga xam ne foofu la wax nanu fa jëm. Ci weeru Féewaryee 2023 dinanu dajale kilifay làng gi, bu ko defee nu wane sunu bopp, nu wane la nu ànde woon ak moom 2005 loolu lanu ànde ak moom te ci lanu fas yéenee wéy. Moom kese lanuy déglu.”

Waaye, ba tey ñii di waa PDS (Parti Démocratique du Sénégal) desuñu benn yoon ginnaaw. Mu mel ni dañuy def li ñu naan kuy yoot du sëqët. Ci ab saabal bu ñu génnee juróomi fan ci weeru nowàmbar xamle nañu ci ne njaayum kàrt yi ak taxawalug kurél yi tàmbali na te dina wéy ba fanweeri fan ak benn ci weeru desàmbar 2023. 

Kon nag, mbir yi àgg na ca càppaandaw la, toogaay amatul. Nu golo xam, boote doomam. Askan waa ngi noonu, mooy àtte gaa ñi, mooy tànn kiy toog ak ki dul toog.  Wax jeey xal a bari rekk, wànte moo yor kàddu gu mujj gi, bu nee waaw rekk jeex na.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj