Mbirum ñaari way-yëddu ya réeroon ca Kab Maniwel ma ngay wéy di lëmbe xel yi. Donte ne sax, mbir mi am na lu jege ñeenti weer, ba mu am sax ñu ko tàmbalee fàtte. Waaye, seen i mbokk moom bokkuñu ca ñooña. Ndax, ba tey, ñi ngi sàkku ñu xamal leen ci yan anam la kii di Fulbeer Sàmb faatoo ? Ak kii di Dijje Baaji nga xam ne kenn tegu ko bët, ci lan la nekk ? Bu dee mi ngi dund, fan la nekk ak nan la fa nekke ? Naka noonu, bu dee dafa dee tamit, ñu xam ci yan anam la génne àddina ? Mu mel ni ba tey amaguñu tontu ci seen laaj yooyu. Te, patt-pattaaral gi Nguur gi ak ug njabootam (Sàndarmëri ak làrme) am ci réerug seen doom yooyu mujj na leen a ëlëm. Moo taxoon ñu génnoon ci fan yee weesu di wone seen bopp ngir gaa ñi bañ a fàtte seen doom yooyu.
Réerug ñaari takk-der yooyu, tiis wu diis la ci seen ug njaboot. Ndax kat, ay moom, mënut a romb baay dee na. Lu jege ñeenti weer ñuy wër seen doom (Dijje Baaji) gisuñu ko. Te, ñoom ñaar nag duñu ay niti neen. Ndax, ay doomi Nguur gi lañu. Kenn ki doon liggéey ci Sàndarmëri, keneen ki ci làrme bi, Dijje Baaji (Adjudent-chef) ak Fulbeer Sàmbu (Sergent). Ñoom ñaar nag, ay xarit lañu woon, bokk benn dëkk bu ñu cosaanoo, di Ñoomun, nekke ca Kaasamaas. Yëf yi nag mi ngi xewoon ci weeru nowàmbar, atum 2022. Nee ñu, dañoo nappi woon, bésub àjjuma, mu yemoo woon ak fukki fan ak juróom-ñett ci weeru nowàmbar. Bi seen ug njaboot toogee ab diir gisuñu leen, ci lañu fabu, tàmbali leen a wër. Ginnaaw gi la toppekatu bokkeef gi génnee yëgle xamle ne gaawu ba léegi ñi ngi leen di wër. Ñu ne gaa ñi dañoo réer ca Kab Maniwel. Ci lañu nee am na néew bu ñu gis te, kooku ñu ne Fulbeer Sàmbu la. Bi ñu ko gisee, ay mbokkam sàkku ñu def ab otopsi ngir xam ci yan anam la faatoo, ñu ne loolu mënul a nekk ndax, fi néew bi tollu moo tax. Waaye, kii di Bàrtelemi Jaas meeru Ndakaaru, dépite tamit ci lëkkatoo gii di Yewwi Askan Wi gisewul mbir mi noonu. Dafa ne :
“Bëgg nu gëmloo ne benn takk-der dafa lab, mën nanu ko gëm. Bëgg noo gëmloo nag ne ñaari takk-der dañoo lab, day tàmbalee doy waar. Yaw jëwriñ ji boo nu bëggee gëmloo ne dañoo waroon a suul Fulbeer Sàmbu bañ ko otopsi ndax néew bi dafa tàmbali woon a yàqu, kon, otopsi bi moom dafa waroon a am. Otopsi dañu koy def ngir waxloo yaram wi, du sikki-sàkka dafa am ci dee gi. Te, mbir mu mel noonu lañu am fii. Yaw jëwriñ ji ñu dénk làrme bi ndax mën ngeen nu wax lan ngeen nar a def ngir leeral li lëndëm ci boppi saa-senegaal yi ? Ci man, li ma jàpp, mooy ne ag bóom la. Mën naa juum. Waaye, yaakaaruma ko. Ndax, dama leen koy wax ci yar ak teggin, damaa mënul a xam nan la ñaari takk-der yu ñu tàggat mën a labandoo ? Dégg nanu fi toppekat bi di wax. Waaye, ba tey kenn gëmu ko ndax moom ci jëmmi boppam dañu koy duut baaraam. Jëwriñ ji, Fulbeer Sàmbu réer na, dee na. Waaye, ana adjudent-chef Dijje Baaji ? Ay mbokkam def nañu ndajem-waxtaan. Dañoo yéemu ci ne du Sàndarmëri, du toppekat bi, kenn ku leen ci woo ngir xibaar leen dara ci yëf yi. Ndax bu Fulbeer Sàmbu, ndax bu Dijje Baaji nekkoon sa doom, ndax yaakaar nga ne yelloo na lii ?”
Mu am leneen tamit lu laxasu ci mbir mi. Dafa di, ñoom fi ñu dëkke, boo xoolee, ndox a ko wër, du yomb ci ñoom ñu gëm mbir mu ni mel. Nde, boo xoolee seen ndajem keroog mi sax, loolu bokk na ci li ñu gën a fésal. Ay xale yu ndaw lañu doon wone ñuy féey. Li waraloon ndaje moomu lenn kese la woon, dekkalaat yëf yi. Ndax, ba tey kenn yéyul yàbbi ci lu jëm ci seen doom yooyu. Ñoom nag, bëgg nañu yëf yi leer, ñu mën a jàll ci leneen. Te, loolu la kii di Keledoor Seen doon biral ci kàddu ya mu yékkati woon ca ndaje mooma.
“Ñi ngi leen di ndokkeel, te di leen massawu ci li leen dal. Ndax, seen i doom ñoom ñoo sànku. Kenn ki di Fulbeer Sàmbu nee nañu dañu koo fekk ci benn béréb ci géej gi mu lab ba ay céram am lu ci mànke. Te, nee nañu foofu mu lab juróomi fan ginnaaw gi lañu ko fa fekk, te, loolu mënut a nekk. Bi may ñëw fii ay xale yu tuuti ñi ngi féey diggante tefes ak tefes. Kon, ñoom ci loolu lañu màgge. Man mii dama daan jéggi Ndakaaru ak Gore. Fi ñu ne foofu lañu lab diggante Ndakaaru ak Gore la, dañu koy féey, 1Km 500 la. Kon, ku mën ndox mënu faa lab, rawatina nag fa nga labe juróomi fan ci ginnaaw gi ñu fekk la fa. Dijje Baaji dafa réer, kenn gisu ko, waaye, amunu njort lu rafet ci moom. Kon, tey jii, loolu bu amee Sàndarmëri waxul, Làrme bi waxul, sunu njort day daldi ñaaw. Kenn mënul a rafetloo sunu njort ci génn àddunag Fulbeer Sàmbu ak réerug Dijje Baaji. Ndax, ba mu amee, toppekat ba woon ci boppam moo ne béréb bii de lañu demoon nappi, boo demee dañoo lab. Te, béréb boobu béréb bu ñuy aar la ndax ginnaaw Pale la nekk, bérébu sóobare la. Mënuñu joxe ndigal ngir ñu seet leen ci béréb yooyu lu tollu ci ñetti fan gisuñu dara. Ba juróomeelu fan wi ñu ne gis nañu Fulbeer Sàmbu. Loolu, man mënuñu koo dugal sama bopp. Nun gëmunu loolu, rawatina nag ci benn béréb bi lañu ko fekk. Kon, tey jii, mënuñu dàq ne loxo Nguur gi mi ngi ci biir seen ug réer ak seen ug dee. Kon, dañu bañ a gëstu loolu, dañu bañ a fésal dëgg.”
Mbir mi yemul foofu ba tey. Ndax, li ci gën a teey xel mooy bi mbir mi xewee dafa am ñu génn di njukkal Kilifa Sàndarmëri Musaa Faal. Am tamit, ñu génn di biral naan jollasuy Paap Aale Ñaŋ wax nañu. Maanaam, ñoo yoole gaa ñi. Ndax, ca jamono jooja lañu ko jàppoon. Li gën a doy waarati ci mbir mi, mooy patt-pattaaralu Nguur gi ñu nemmeeku moom ak ug njabootam. Maanaam, waa sàndarmëri ak waa làrme bi, du dara lu ñu ci def. Moone de, ñoom ñaar ñépp seen i ndaw lañu woon. Moo tax, kuréli way-moomeel yi ak yenn ci ay layookat génn ngir gunge seen mbokk yi ci xeex boobu. Loolu la kii di Me Aamadu Jàllo, jiite Amnesty International ci Senegaal, te bokk ci xeex bi, di fésal ci kàddoom yi mu yékkati woon ci seen ndaje ma ñu defoon ci weeru saŋwiye wii weesu :
“Njabootu Fulbeer Sàmbu, kooku wóor nanu ne génn na àddina ak njabootu Dijje Baaji mi nga xamante ne, ba tey xamuñu ci lu mu nekk. Mbir yi bi mu amee ba tey def na ñaari weer, amunu benn xibaar buy firndeel ne Dijje Baaji mi ngi dund walla dundatul. Waaye, li gën a metti njaboot gi mooy amul genn kilifa ci Nguur gi, muy Sàndarmëri muy IGE, muy banqaasu jëwriñ ji ñu dénk Làrme bi ku leen jege ngir lu mu dee-dee ñu massawu leen. Loolu amul, xamuñu fu mbir yi tollu. Te, soo xoolee ku mel ni Dijje Baaji am na jabar, am na ay doom. Ba tey ñooñu nga xamante ne nii, seen dund Dijje Baaji moo ko yoroon. Maanaam, bu ñu ko feyee mu toppatoo njabootam. Loolu njaboot gi jotatu ko. Tey dafa mel ni Sàndarmëri ak Nguuru Senegaal ay mbiram toppatootuñu ko. Njabootam daal faaleetuñu ko. Loolu nag, dañu koy naqarlu ndax, ci yoon kenn warul a mën a nangu koo xam ne mi ngi liggéeyal Nguuru Senegaal dara su ko dalee, lum dee-dee Nguur gi ñëw massawu njabootam, loolu amul. Ñaareelu mbir mi mooy ñu mën a toppatoo njaboot gi te, loolu tamit amul. Ñetteelu mbir mi, njaboot gi war na mën a xam ci Sàndarmëri, ci jëwriñu Làrme bi ak ci yoon ci lan lañu nekk ngir xam lan moo ko dal. Loolu yépp amuñu ci benn xibaar. Loolu lañuy naqarlu, moo tax ñu ànd ak kurélu way-moomeel yi ngir gunge leen ci xeex bi. Du mbiru Dije Baaji rekk ak Fulbeer Sàmbu, li leen dal mën na dal ku nekk. Tey ñépp war nañu taxaw ngir ñu leeral mbir mi.”
Laaj bi mat a samp kay, mooy lu waral patt-pattaralu Nguur gi ci yëf yi ? Walla ñoom bokkuñu ci ag njabootam ? Taxawaayam boobu bokk na ci li tax, gaa ñu bari jàpp ne loxo Nguur gi génnul ci yëf yi. Dafa di, ñu lay tam nóoxóor, ngay soccoo yeelu liir, doy na waar. Te, mbir mi dafa xewe ci jamono ju doy waar. Ndax, dafa amoon lenn ciy wayndare ak xibaari Sàndarmëri yu doon génn. Am ñu jàpp ne looloo tax ñu diir leen. Kii di Dijje Baaji da doon liggéey ak kii di Nafi Ngom Keyta mi jiite woon OFNAC, jege woon lool njabootu Nafi. Te, Faddiilu Keyta doom la ci Nafi bokk tamit ci kilifay Pastef yi daanaka rakk la ci Dijje Baaji. Faddilu Keyta moom loolu bokk na ci li ñu ko téye ba tey. Kon nag, coow li am na ci lees waxul. Waaye, lu tëw a xam rekk, dafa yàggul.