Senegaal dafa tollu ci jamono joo xam ne, képp ku jàngul, mënul a jot ci teraangay réew mi. Moone de, ñi jàngul ñoo ëpp fuuf ñi jàng. Ndax kat, téeméer boo jël ci saa-Senegaal yi, 20 doŋŋ ñoo jàng, 80 yi jànguñu. Ñoom nag, ñooy ñi mënul a bokk ak ñi jàng ci lenn ndab li. Moo tax, seen i liggéey (métier) lañu yore, def ci seen yaakaar, ndax moo leen di dundal. Te kat, ku ëmb sa sanqal, ëmb sa kersa. Yooyule liggéey nag, ñi ci gën a bari, ndono la ci ñoom, ñu di ko damoo ba seen i doom di leen ci donn ñoom itam. Noonu la daan deme. Waaye tey, mbir mi dafa deme neneen.
Nu mu deme ?
Ni ñu daan gisee mbir mi ak léegi wute na lool. Bu njëkkaan, liggéey yu bari dañu leen daan donnu ndax mboolaay mee tëdde woon noonu. Ñi bokkoon ci doomi uude yi, tëgg yi, ñeeño yi, ci gàttal, dañu doon donn ci seen i baay yenn xeetu liggéey yi. Waaye léegi, kenn donnatul kenn. Jamono jee soppeeku. Rax-ci-dolli, fi ndaw ñi yóbbu seen i bëgg-bëgg tey, moo waral lu ni mel. Te sax, ñu bari ci ndaw ñooñu, dañuy jàng. Njàngum nasaraan mi nag, tax na ba ndaw ñi jegeetuñu seen i way-jur bay xam as-tuut ci li ñuy def. Bu ko defee nag, way-jur bu faatu, yóbbaale xam-xamam ak mën-mënam. Te yooyule liggéey, dañu bokk ci cosaanu réewum Senegaal. Kon, réew mi lu bari la ciy ñàkk ndax solo si liggéey yooyu làmboo. Nde, bu Nguur gi amulee tey yenn taxawaay yi ci fànn woowu, dina am xeetu xam-xam yu bari yuy naaxsaay. Te loolu, du njariñal réew mi. Moone de, am na lu mu jéem ci fànn wi. Waaye mbir maa ngi mel ni luy gën di suux.
Lan la def ak lan la deful ?
Ci xayma, ñeeño yi bokkoon nañu ci ñi daan liggéey ngir suqali koom-koomu réew yi. Te ngir réew mi am koom-koom gu naat ak ay ndaw yuy liggéey, fàww ñu gëddal liggéeyi artisanaa. Te tey, fànn woowu lañu dippee secteur informel ci nasaraan. Ñenn ci ñi fay yëngu nag jànguñu. Am na ci ñoo xam ne tamit jàng nañu waaye seen njàng soriwul.
Ndegam farãse bee nekk làkk wi ñuy liggéeye fii ci Senegaal, Nguur gi dafa teg ay tëralin yu jëm ci wàll woowu. Nde, dafa dogal ni dañuy lootaabe, nose fànn wi ngir mu gën a suqaliku. Ñi fay yëngu dañu war a jàng ba am ay lijaasa ngir ñu mën leen a xàmme niy artisã. Looloo nekkoon pexey Nguur gi ngir taxawu artisã yi. Waaye dafa fekk ni, njàng mi, ci farãse lañu koy defe, te ñépp xam nañu ne, ñu bari ci ñoom dégguñu làkk woowu te mënuñu koo bind. Te it, dañu leen di bëgg a jàngal loo xam ne, xam nañu ko ba noppi. Waaye, dañu leen di jéem a tuutil, ñoom ak seen i xam-xam. Mu nekk nag, luy gàllankoor liggéey bi Nguur gi bëggoon a sumb ak ñoom. Te mu mujj jur ay jafe-jafe diggante jàngalekat yi ak artisã yi. Ndax kat, déggoo mënu fa am.
Ñàkk a jàng ñenn ñi tax na ba mënuñoo bokk ci ñi Nguur gi di dooleel. Te ñoo gën a bari. Loolu nag, dafay gën di suuxal fànn wi. Moo tax it, ñu bari di daw liggéeyu artisanaa di defi leneen. Ndax kat, mag moom, bu naanee ndox mu tàng, suukër saa tax. Looloo tax ndaw ñi tàmbali di daw fànn woowu ndax li njariñ li tàmbalee néew.
Nde, benn yoon la Nguur gi mës a def am ndaje ci fànn woowu. Ca atum 2014 la woon fale ca Ngaay Mexe, ñu dippe woon ndaje ma “ Bésub artisanaa ”. Te xeetu ndaje yii, ci xalaatu Masekk Jóob mi newoon Njiitu mboolaay mi ñu dippe woon Organisation nationale des professionnels du bois, at mu nekk lañu ko waroon a amal. Ci waxtaan wi mu amaloon ak Seneplus ca atum 2016, mu ngi biral ne : « Wàdd moo faat artisana, Maki moo ko suul ». Ndax bu njëkkaan, maanaam diggante atum 1970 ba 1980, fànn wi da doon dox bu baax te ràññe woon nañu lool artisã yi fi daan liggéey ci seen xarañte ak seen mën-mën. Waaye jàpp na itam ni, ñi waroon a matal seen wareef ñoo ko deful. Maanaam, ñi jiite réew mi di santaane liggéey yi war a dem ci fànn wi. Seen taxawaay ci fànn wi des na te dina metti lool ñu bëgg a suqali koom-koomu réew mi fii ak jaaruñu ci liggéeyi artisana yi.
Mën-mën yi duñu fi jeex, matuwaay yi doŋŋ ñoo des. Dàlli Ngaay yaa ngi wër fépp ci biir réew mi. Minise yaa ngi fi, di jëfandikoo seen i xam-xam, ñawkat yi, tëgg yi, añs. Bu ñu leen daan dooleel, kon tey, benn saa-Senegaal du jënd ay yére yuy jóge bitim-réew, walla ay lal, ay taabal, ay dàll, ay takkaay, añs. Léeg-léeg sax, doxandeem yi fi yore ay këri liggéey lañuy liggéeyal. Mbooleem jafe-jafe yii ñoo naj fànnu artisanaa bi. Waaye itam, maxejj yi am nañu ci wàll.
Lu ci seen wàll ?
Li maxejj yi di gën di taamu njaay yi jóge bitim-réew bokk na ci liy gaar fànn wi. Bu fekkee ni juróomi maxejj ci ñaar-fukk ñooy jënd njaay yi ñu fiy defare, loolu gàcce gu rëy la ci réew mi. Moone de, liy jóge bitim-réew, gënul a baax li fi ne. Li fay jóge sax te saa-Senegaal yi di ko indi, li ci gën a bari, mbalit la bi ñu sànni woon, ci xalaatu Masekk Jóob. Baaxul te du yàgg. Taxawaayu maxejj yi nag, bokkul ci liy dooleel artisã yi. Daanaka sax, dafay am ay njeexital ci koom-koomu réew mi. Ndax tono yi, ñee ñoo koy am. Nde, doxandeem yi ñoo dàq a jënd sax njaay yi ñu fiy defare.
Ni mbir mi di demee nii tey nag, dina jur ay njeexital yu bari ëllëg rawatina bu réew mi demee ba rafle ay artisã. Ndax dañuy faral di naan, am ko te xamoo ko, ñàkk ko te xam koo gën.