WÀÑÑIG NJËGU KUURAŊ BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci ayu-bés bii ñu génn la jëwriñ ji ñu dénk yaxantu gi xamle woon ne wàññi nañu njëgu ceeb yiy jóge réewi Vietnam, Inde ak Thailande. Dafa mel ni, naruñoo yem foofu. Ndax, am na yeneen wàññi yu ñuy waaj a def ci yeneen wàll ngir gën a ñoŋal dundinu askan wi. Nde, kenn umpalewul ne li ëpp ci li askan wi di yittewoo dafa jafe. Moo tax, Nguur gi jëloon ndogalu wàññi ceeb beek yenn yi muy àndal. Mu amaat leneen lu ñu namm a wàñni, muy kuuraŋ bi. Ki siiwal xibaar boobu di jëwriñ ji ñu dénk soroj bi, laf gi ak mbéll mi, Biram Suley Jóob.

Nguur gu bees gi am na yenn wàññi yu mu door ci yenn ci yi askan wi di jëfandikoo. Dafa di, askan wi loolu rekk la soxla jamono jii. Ndax, lott nañu lool. Te, noppi ku sonn di yuuxu moom, tànki kuy daw di wallusi rekk lay déglu. Mu mel ni Nguur gi nànd na loolu. Ba tax, ñu door ay coppite ci wàll yu bari ngir gën a woyofalal askan wi seen dundin. Ginnaaw ceeb bi ñu wàññi lu yàggul dara, ñi ngi ciy waaj a teg kuuraŋ bi. Donte ne sax, ñu baree ngi doon xaar lu ni mel. Ndax, réewum Senegaal am na lu ko Yàlla jagleel ci wàllu balluy mbindaare muy ci soroj bi di ci mbëj mi, añs. Te, seen ug coppi ak seen ug jëfandikoo mën naa jàppale réew mi ak askan wi ci fànn yu bari. Moo tax, Nguur gi mébét a wàññi lenn loo xam ne askan wépp a ko yittewoo, muy ñi ko am, di ñi ko amagul.

Ki siiwal xibaaru wàññi gi mooy jëwriñ ji ñu dénk wall woowu di Biram Suley Jóob. Ma nga ko waxe fa RSI (Radio Sénégal Internationale) ci aw waxtaan wu ñu ko fa woo woon démb ci dibéer ji. Li mu fa xamle mooy ne ginnaaw bi ñu amal coppite yi ñu war a amal, njëgu kuuraŋ bi dina wàññeeku. Dina jóge ci 117 FCFA KWH (Kilo Watt Heure) dem ci 60 FCFA KWH. Mu doon ndogal boo xam ne bés bu ñu ko jëmmalee, dina gën a yembal dundinu askan wi. Waaye nag, wàññi googu, du léegi, fii ak 2030 jëm kaw la.

Li am ba des kay mooy xibaar bi ñeel wàññig kuuraŋ bi moom rot na. Te, ki ko siiwal mooy ki ñu dénk wall woowu. Li mat a laaj kay mooy kañ kañuy jëmmal naalu wàññi googu ?

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj