WAXTAAN CI MBIRUM ALFAABETISAASIYOŊ AK DEMOKARAASI Mamadu Jara Juuf (ci xalima Paap Aali Jàllo)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Yaxal bii, aw waxtaan la wu, bindkat bii di Mamadu Jara Juuf moo ko amaloon ca Kawlax, 8 sàttumbar 1992. Mi ciy waxtaane alfaabetisaasiyoŋ ak demokaraasi ci kàllaamay Kocc. Solos wax ji, ak dayoom, ñoo tax seen yéenekaay Lu defu waxu biral leen ko. Waxtaan wi nag, xaajees na ko ñaari pàcc. Ci pàcc bu jëkk bii nu leen di dégtal, werekaan baa ngi ciy faramfàcce maanaa ñaari baati nasaraan yii di alfaabetisaasiyoŋ ak demokaraasi

 « Maa ngi leen di nuyu yeen ñépp, góor ak jigéen, mag ak ndaw, te di leen ndokkeel ci bés bi. Seen taaru toogaay bi wone na seen pas-pas ak cofeel gi ngeen am ci li nu boole fii tey.

Wolof dafa ne : « Bu lëg lekkee aloom, na ko gërëme coy. »

Kon boog ma dollee gërëm kilifa yii fi toog, te delloo leen njukkal. Loolu ñeel na leen ngir yëg gi, ak xejal gi ñu ma xejal ba ma am fitu toog fii di ubbi waxtaan.

Jàpp naa ne, solos mbir mi nu dajale tey a ko waral. Waaye, du sunu jëmmi bopp. Ba tax na, danuy daldi laf fale lu jëm ci sunu bopp te jublu ci li di yaxu wax ji.

Waxtaan wi danu ko wékk ci ñaari baati nasaraan yees di dégge alfaabetisaasiyoŋ ak demokaraasi. Ñuy ñaari baat yu réy yu, bu ci nekk danga tënk ay sasi sas. Sunu itte moo di jéem a seet ba xam baat bu ci nekk lu mu wund ak nan lanu leen mën a lëkkalee bu jukki ci ay xalaat ak i xeeti doxalin yu mën a soxal waa réew mi.

Faramfàcce baat yi

Ràññee nanu ci nasaraan tudde alfaabetisaasiyoŋ baatu liif ak liifantu. Mu mel ni kon, ëmb na ay xeeti yëngu-yëngu yu, seenub jëmu moo di fexe ba nit ki mën a xàmmee ay araf, mën leen a boole ba tudd ay baat, mu mën a ràññatle baat yooyu nu ñuy nasoo ba jëmmal ay xalaat.

Loolu di biral ne, mënees na màndargaal ay xalaat, not xam-xam ak xew-xewi jamono, denc leen ci béréb bu ñuy ñoŋe, te loolu lépp li koy àntul di am mbind. Ngeen gis ne kon, baatu alfaabetisaasiyoŋ ëmb na njàng mi, te ku tudd njàng tuddaale nga njàngale mi ndax benn bi mooy waral beneen bi ci des.

Baatu demokaraasi dafa joxoñ aw doxalin wuy tekki ci am réew, walla aw xeet, walla kurél gu mu doon, dogal ya ñu leen di natte ca ittey ña ëpp ca mbooloo ma.

Mu mel ni kon, demokaraasi mooy aw doxalin wuy cëral baatu mbooloo mi. Mënees na tàmbalee ci gox bi dem ci diwaan bi, yaatal ko ba ci rew mi walla sax nu safaanal, tudd rekk cib gàttal doxalinu réew, mu tënk li ci biir lépp.

Li am solo di : naka lanuy jële baatu demokaraasi boobu, daldi koo lëkkale ak baatu alfaabetisaasiyoŋ bi ngeen xam ne njàng ak njàngale lay joxoñ te, bees ko seetee ba ca biir, mënees na wax ne muskàllaf yu góor yi a kyu jigéen yi lay diir ?

Bu nu bëggee tontu laaj boobu, mën nanoo topp ñaari yoon : wu jëkk wi di seet lan mooy sàrtu demokaraasi, wi ci topp jéem a gëstu ba xam mbokk gi dox diggam ak mbiru njàngu muskàllaf yi.

Sàrtu demokaraasi

Xeñtu sàrtu demokaraasi, dafay wund : seet ci yan anam anam la kàddug mbooloo mi mën a jib ba soppaliku doole juy doxal lu jariñ am réew.

Nguuru demokaraasi, ni mu tuddoo ci sàrtu réew mi doon na nguur guy tukkee ci mbooloo mi, jiital ci ay itteem njariñu mboloo mi, te di wéye baatu mbooloo mi.

Ngeen gis ne sàrtu réew, dafa am ay mbir yu takku yu ko lal, te ñooy teewal taxawaayu mbooloo mi. Mënees na leen a tënk ci ñetti ponk.

  1. Bu jëkk bi mooy tànnin, maanaam yoon wi warees a jaar ba tànn ay njiit. Boo nee nguur gi dafay tukkee ci mbooloo mi, déggees ko ni xeet wi ci boppam mooy seet ci biiram, jukkee ci ay doomam yu xamees ne am na ci ñoom yaakaar ak kóolute ngir seen xam-xam, seen jikko yu rafet, bu ko defee mu fal leen daldi leen jiital.

Bu boobaa itam, loolu dafay ame ci ay anam yu kenn dul mën a diiŋat ndax li nuy sosoo ci ag déggooo. Loolu lanu tënk ci sàrtu tànn bi te nu di ko dégge ci nasaraan Kodd elektoraal.

  1. Jiital ci pas-pasu nguur gi njariñu mbooloo mi moo di sunu ñaareelu ponk. Li koy sabab mooy nguur gu sax dàkk ci mbooloo mi, di ko déglu fu mu tollu, di sàkkoo xam ay xalaatam ak ay bëgg-bëggam te di taxaw ci ay soxlaam.

Sàrtu réew mi indi na ci tëralinam ne nguur googu fàww day xar def ñetti pàcc. Pàcc bu ci njëkk méngoo ak kurélu-nguur gu am baatam ak kilifteefu boppam. Ñetti kurélu-nguur yooyu di : giy dogal, diy doxal ak giy àtte. Gu ci nekk war a sàmm boppam ba du wàcc yoonu mbooloo mi, te mën a sàmm yeneen kurél yi ba ñu jubal.

  1. Li koy wéyale ci baatu mbooloo mi, te mu di sunu ñetteeli ponk, moo di waa réew mi, walla boog li ëpp ci askan wi mën a sàmm te di sàmmoonte ak doxalin yi leen di jariñ.

Li ko nar a sabab di, waa réew mi di mën fu ñu tollu seen kàddu di jib, te mënees koo dégg. Mbooloo mi mën a samp ay xeeti kurél ak i làng yuy saytu doxalinu nguur gi, te mën a jàmmarlook moom ba tegaat ko ci yoon, bu naree jeng.

Ñetti ponk yooyu ma lim, doon nañu ay toxutil yu, li leen boole ŋànk moo di mbooloo mi matal ay jumtukaay yu warees a jëfandikoo ngir sos aw yoon te di topp doxalin. Mu des kon, nu jéem a saytu ba xam nees di mën a dimbalikoo am njàng ci mbir moomu ma tudd.


Dees na ko topp…

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj