WÉR-GI-YARAMU USMAAN SONKO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Talaata fukki fan ak juróom-ñaar ci weeru oktoobar wii la Njiitul Pastef li dooraatoon xiifal gi. Boobaak léegi ma nga ca, teggiwul tànkam. Ba tax na jamono jii wér-gi-yaramam sooxe na lool. Maanaam, Usmaan Sonko fim tollu nii sonnu na lool. Ki fésal boobule xibaar mooy layookatam bii di Meetar Sire Keledoor Li. Xamle na ne, ci ndoorteelu ayu-bés bii sax kiliyaanam boobu demoon na sax ba àgg ci li ñuy dippe “coma”. Maanaam, dafa nekkoon diggante dund ak dee. Xamatul woon te mënatul woon dara daanaka laata xelam di dellusi.

Jamono jii, céri meeru Sigicoor bi sutante nañu lool. Sikk amatu ci. Moo tax sax, wayndarew caytoom gi ñu fésal jur na coow lu bari ci réew mi, rawatina ci géewu pólitig gi. Ba sax kii di toppekatu bokkeef gi ne dina ci amal ag luññutu ba xam kan moo siiwal wayndare woowu. Waaye, ay ñoñi Usmaan Sonko ak i layookatam naanewuñu ko ndox. Ñoom, layookatam yi, xamal nañu toppekat bi ne loolu mu namm a def, Usmaan Sonko santu ko ko. Ndax, lu ko jiitu am na nataalam ak i widewoom ba ci sax ay yëfi boppam yu ñu tas ci lënd gi lépp ci kanamam. Te, yéyul yàbbi ci. Li ñuy sàkku kay mooy ñu bàyyi xel njeexital yu doy waar yi woppam gii mën a jur.

Mu mel ni kon wér-gi-yaramam tagatémbe na lool, lool sax. Ndax, bataaxel boobu ñu jébbal jëwriñ ji ñu dénk wàlluw Yoon, ñaar-fukki fan ak ñeent ci weer wii firnde la ci. Xamal na ko ci ne, ñaari fan yu mujj yii Usmaan Sonko am na feebar bu ko sonal. Te, ñoom xamuñu nu mu deme donte ne sax def nañu ci ay caytu. Taxul ñu xam dëgg-dëgg sabab bi. Moo tax ay layookatam, ay ñoñam, ñenn ci way-moomeel ba ci sax ay taskati xibaar ñi ngi sàkku ñu bàyyi ko ca na mu gën a gaawe balay yëf yi di gën a ëpp i loxo.

Dafa di nag, moom Njiitul Pastef li, du guléet muy xiifal. Ndax, njëkkoon na fee xiifal lu tollu ci fanweeri fan ak ñeent ngir anam yu ñaaw yi ñu ko tege loxo ak sabab yi tax ñu teg ko loxo. Looloo taxoon mu doon xiifal ba mujjoon a sonn lool ba ñu koy may doole. Ba tax na, weeru ut ba léegi, ma nga ca raglu ba, delloogul ca kaso ba. Wii yoon moom li waral xiifal gi mooy jàppale jigéen ñiy xiifal ngir jàpp gi ñu leen jàpp te teguwul ci yoon. Muy jigéen ña ñu téye ca Kàmpenaal bu Liberté 6 ak yeneen kaso yi. Rax-ci-dolli, moom it day ñaawlu téye gi ñu ko téye jamono jii moom ak ñenn ci ay ñoñam nga xam ne bëgg na mu dakk nu mu gën a gaawe.

Kon, jot na ñi mën a wax ak moom wax ak moom mu dakkal xiifal gi balay yëf yi di gën a jéggi dayo. Ñu wax tamit ak ñi ko teg loxo ñu bàyyi ko ginnaaw jàpp na ne mbiri pólitig kepp a tax ñu teg ko loxo. Ndax kat, ndox su tuuroo, bàq a fay des.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj