WIDEWOO BASIIRU JOMAAY FAY DU JÀLL FA RTS

Yeneen i xët

Aji bind ji

RTS, kibaaraan la gu wute ak yeneen yi nekk ci biir réew mi. Ndax, kibaaraan la goo xam ne, askanu Senegaal a ko moomal boppam. Moo tax, moom lañu sas muy jàllale widewooy lawax yi. Maanaam, li lawax bi namm ci réew mi. RTS nag, nangul na lawax yépp loolu ba mu des Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Te, ñi jël ndogal loolu du ñenn ñu dul waa CNRA (Conseil National de Régulation de l’Audiovisuel). Nee ñu, ñoom waa CNRA, lawax bu nekk moo war a waxal boppam te Basiiru Jomaay Fay mi ngi kaso jamono jii.

Doxalinu RTS wii mel na ni du guléet ñu ko fiy nemmeeku. Laata ñuy dàq wote yi, gisoon nañu lu ni mel. Ndaxte, Aamadu Ba, ndaw liy teewal lawax bii di Basiiru Jomaay Fay, bés bim njëkkee ñëw ngir jàllale sémbam ni ñépp, dañu koo téye woon ca buntu ba tere ko dugg. Wii yoon moom, jotoon nañu koo bàyyi mu dugg. Waaye, simili yi ñu ko waroon a jox ngir mu jàllale yóbbalu lawaxu lëkkatoog Diomay Président, dañ ko nanguwaat. Waa CNRA ñi nga xam ne ñoo jël ndogal li, li ñu ko layalee mooy ne lawax boobu, jamono jii, mi ngi ci kaso bi. Rax-ci-dolli, waa CNRA nee nañu simili yooyu ñuy dippe “temps d’antenne” kenn mënu ko cee wuutu ba ci sax ki nga xam ne moom la jiital ci kàmpaañ bi.

Kon, tiiñalante gi am diggante yenn ci lawaxi kujje gi ak RTS mi ngi wéy ba tey. Li jaaxal gaa ñi kay mooy lan moo tax mu am ñu mu ko gën a langal ? Nde, dem nañu ba ñu bari jàpp ne kibaaraan googu moom tëddewul njaaxaanaay. Taxawaay bi mu am ci diggante lawax yi bu yàgg ba tey, dafa teey xel lool. Te, ñépp doon ko xaar ci ag yemale diggante ñi nekk ci Nguur ak ñi nekk ci kujje gi. Kon, am na luy ñuul ci soow mi.

Ndogal loolu CNRA jël ñeel lawaxu Pastef bi moo wund sotug ñenn ñi jiite ay kibaaraan. Ku ci mel ni Séex Ñas mi jiite Walfadjiri xamle na ne, moom, dina ko defal li ko waa RTS bañal. Ci gàttal, dinañu jàllale kàddu yi nga xam ne Jomaay bëgg na koo dégtal Saa-Senegaal yi. Naka noonu ñii di waa Dakarmatin tamit jël nañu ndogalu may ko bés bu set fanweeri simili yoo xam ne jàllale dara ci naal bim jagleel Senegaal.

Mu mel ni xeex bi am ci géewu pólitig gi dafa laaxaale ñi fare ci kibaaraan yi sax. Waaye, lu ci mën di am, li des ci wote yi moom bareetul. Te, ci lu yàggul dara dees na xam ndax, RTS day wéyal doxalinam wii am fi la koy yemale ? Ku dund rekk dinga fekke.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj