WOTEB SÉMBUB ÀTTE BIY DÀQ WOTE YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ngombalaan gi jàllale na sémbub àtte biy dàq wote yees nammoon a amal ci bésub 25 féewiryee 2024 bii. Démb ci altine ji la ko dépitey Bennoo Bokk Yaakaar yeek yu PDS yi wote ci guddi gi, ginnaaw dog-dog yu yàgg yu fa amoon ba sàndarm yi mujjee dugg ca Ngomblaan ga.

Démb ci altine ji la dépite yi waroon a saytu sémbub àtte bi ñépp doon coow ci ñetti fan yii fi réew mi. Muy sémbub àtte bu Mamadu Lamin Caam, njiitul làngug « Liberté et démocratie » fa Ngomblaan ga, dugaloon. Moom ak i ñoñam doon ca sàkku ñu dàqandi wote yi war a am ci 25 féewiryee 2024 bi. Fekk lu jiitu lu ni mel, jotoon nañ taxawal ab ndiisoog luññutu fa Ngombalaan ga  ginnaaw bi seen lawax bi, Karim Maysa Wàdd, tuumaalee nger ñenn ci way-bokk yu Ndajem Ndeyu àtte mi.

Sémbub àtte boobu nag, mujje naa jàll. Dépite yu lëkkatoo Wallu (Parti démocratique Sénégalais) ñoo mànkook dépite yu Bennoo Bokk Yaakaar yi daldi ko wote. Bi ñu koy wote sax, lu des 23i waxtu jot barewul. Ñàkk ànd ci ñëw rekk jàll ci wote yi moo fa andi woon dog-dog bu yàgg.

Bi ñu noppee ci laaj yu njëkk yi, la Lamin Caam dafa sàkku ci njiitul Ngombalaan gi ñu bañ a fénc àtte bi te sóobu ci wote bi. Naka noonu, dépite Yewwi yeek yu Taxawu yi lànk ne kenn du jàll ci wote yi te càmbaruñu àtte bi ba noppi. Moo taxoon ba ñu wàcc ci waxuwaay wa, ubale foofu yépp. Taxaw nañ fa ay waxtu, genn làng nanguwul a bàyyi, dem ak sa moroom ci li mu bëgg.

Ngir ñu mën a amal wote yi, njiitul Ngombalaan gi dafa mujje woolu sàndarmi Gign (Groupement d’intervention de la gendarmerie nationale) yi, jox leen ndigal ñu jàpp dépite Yewwi yi, beddi leen, génnee leen ca biti. Ci noonu la dépite Wallu yeek Bennoo yi daldi wote àtte bi mu jàll. Lu ni mel di ñaareel wi yoon, ginnaaw bi ko fi Aysatu Sow Jaawara njëkkee def bi ñuy taxawal pekku Ngombalaan gi ca weeru sàttumbar 2022, ñuy woolu sàndarmëri ci biir Ngombalaan gi, ak di leen jañax ciy dépite ngir mën a doxal ci doole lees bëggut a waxtaane.

Ginnaaw bi àtte bi jàllee nag, Ndajem Ndeyu àtte mee ci desaat. Nde, ci moom la wayndare wi di mujje ngir mu wax ndax àtte bi méngoo naak tëralinu Ndeyu àtte réew mi am déet. Bu nee waaw, Njiitu réew mi Maki Sàll dina wéyal moomeem gi ba keroog 15 desàmbar 2024.

Jamono jii nag, ñu baree ngi dummooyu Maki Sàll réew mi, rawatina CEDEAO mi waxul woon lu leer ca njëlbeen ga. Dafa Eevaa Mari Kol Sekk mii jiite woon ITIE sax, tekki na ndombog-tànkam. Kon, Maki mi ngi gën a wéet.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj