WOTEY 2024 : CÀKKUTEEFU AAR SUNU ELECTION

Yeneen i xët

Aji bind ji

Fileek Fukki fan ak juróom, dees na amal wotey palug Njiitu réewum Senegaal yi Maki Sàll ajandi woon. Waa Aar sunu election dellu di sàkku ci ñu dénk wote yi ku farul fenn te nangoo tëddee njaaxaanaay.

Wote yi Njiitu réew mi ajandi woon, te ñu waroon leen a amal keroog ci 25 féewiryee bii weesu, dinañu leen mujjee amal ci 24 màrs bii di ñëw. Keroog altine la ko Ndajem ndeyu sàrti réew mi dëggal ginnaaw bi Njiitu réew mi jëlee ndogal ngir àjji ko ci bés boobu. Fekk ci ayu-bés bii weesu, Ndajem ndeyu sàrti réew mi njëkkoon na dàq ndogal yi tukkee woon ca diisoo ba Njiitu réew mi woote woon, dellu digal ko mu amal wote yi laata moomeem gi di jeex.

Fi réewum Senegal nag, am nag campeef gu ñu duppee CENA (Commission Electorale Nationale Autonome). Muy banqaas bob, mooy rëdd ak a saytu doxalinu bépp wote bu ñuy amal fi réew mi. Ba ci simili yees jagleel lawax yi ci tele yeek rajo yi dafa leen di topp ak di leen gam-gamle ngir par-parloo bañ a am ci kibaaraan yi.

Yooyu yépp terewul lépp lu jëm ci amal i wote, ci Njiiteefu jëwriñ ji ñu dénk kaaraange geek caytug biir réew mi lay ame. Jëwriñ jooju, Njiitu réew mee koy tabb ci Càmm gi ba noppi mu fare ci làngug pólitigu Nguur gi. Looloo tax ba waa Aar sunu élection dellu démb ci àjjuma ji di sàkku ci ñu jëlee amalug wote yi ci loxoy jëwriñ ji te teg leen ci loxoy ku tëdde njaaxaanaay.

« Ci wotey palug Njiitu réew mii ñu jëm, kurél gee ngi woote jëmale ci wote yu amul par-parloo, yu ñuy amal ci njiiteefu kilifa gu màndu »

Muy coow lees yàgg yékkati saa suy wote amee fi Senegaal. Nde, bi Senegaal di amal i wote ba léegi, jëwriñ jee mës di yor doxalin wi ba tax saa su nekk coowal càcc di leen topp. Bu weesoo lu ni mel, kurél gi woo naat pàcc yépp ak saytukati bitim-réew yi ñu taxaw temm ngir wote yu jaar yoon te leer mën a am.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj