WOTEY 2024 : ËTTUB DABU BI BIRAL NA NJUREEFI NÉGANDIKU YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tay ci àllarba ji la Ëttub dabu bi nekkee Ndakaaru biral  njureefi néggandiku yi tukkee ci wotey 24 màrs yi ñu doon amal ci dibéer jii weesu. 

Gannaaw ba ñu jotee njureefi pekkiy wote yi ci Senegaal ak bitim-réew, càmbar leen, saytu leen ni mu waree, ëttub dabu bi siiwal na njureefi négandiku yi. Nii la njureef yi séddalikoo :

Limub ñi wote mu ngi tollu ci 4.485.165. 

Lim bii day wone dogu bi Saa-Senegaal yi dogu woon ngir indi coppite ci réew mi.

Moom la dayoob bakk gi (taux de participation) wone ci xayma, 61,30%.

Naka noonu, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay moo ci jiitu ak 2.434.751i xob, tollook 54,28%.

Aamadu Ba moo ci topp ak 1.605.086i xob, di yamook 35,79%.

Li des, ñeneen ñee ko séddoo.

Képp kenn ci réewum Senegaal, ba sax ci bitim-réew, di rafetlu doxalinu wote yi. Ndaxte, wone na bu baax ni Senegaal réewum demokarasi la. Te it, tay la gën a dundal loolu.

Léegi nag, Ndajem Ndey Sàrti Réew mee war a dëggal njureef yi fi ak ñaari fan. Nde, Yoon dafa sàrtal ne, ginnaaw bi ëttub dabe siiwalee njureefi négandiku yi, dañuy may lawax ñaari fan ngir bu ñu amee lu ñuy kaas ci wote yi. Bu loolu weesoo, Njiitu réew mi fegal, Maki Sàll, dina jébbal lenge yi Njiitu réew li yees li keroog 2i panu awril 2024.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj