WOTEY 2024 LIY JOT, JOT NA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Lu moy at kepp a des ci wotey 2024 yi. Lawax yi tàmbali nañu wone seen bopp. Lees doon xaar ay at, nag, bees demee ba ñu naan ay weer a ci des, kon yegsi na. Bu ko defee, toogaay amatul. Maanaam, liy jot jot na. Mu mel ni, loolu la gaa ñi xam ba tax na, jamono jii géewu pólitig gi yëngu lool. Way-pólitig yu bari génn, di fésal seen yéeney bokk ci wote yooyile ngir nekk Njiitu réewum Senegaal. Mbir moomu, nag, dooroon na ba wotey palum dépite yi jàllee. Waaye, dafa gën a fés ci atum 2023 mi, rawatina ci jamono jii nu nekk.  

Wotey 2024 yi door nañu. Loolu lees seetlu fi mu nekk nii. Ndax, ci fukki fan ak juróom-benn ci weeru féewaryee wii nu génn la jëwriñ ji ñu dénk wàllu biir-réew mi génnee ab yëgle ngir xamle àppub wotey njiiteefu réew mi. Ñu jàpp leen ci bésub ñaar-fukki fan ak juróom ci weeru féewaryee. Laata yëgle biy fés sax, amoon na ñu fésaloon seen yéeney jiite réew mi fii ak at. Waaye, bi yëgle bi génnee, la am ñeneen ñu yokku ci lim bi. Daanaka, jamono jii lawax yi sampagum seen ndënd ak ñiy ruumandaat seen ag bokk jege nañu fukk. Ci ayu-bés bii, kii di Njiitul PRP li, Décce Faal bokk ci lëkkatoo Yewwi Askan Wi, samp na ndënd ngir bokk ci wote yooyu. Loolu lay biral ci kàddoom yii :         

Kon noo ngi koy wax fii ci kanamu saa-senegaal bu ne ak foo mën a nekk. Noo ngi koy wax ci kanamu kilifa diine ak kilifa aada yi, di ko wax ci kanamu ñi Senegaal di lëkkalool ne tey jii nii, fii ci bérébu PRP, man mii di Décce Faal, fas yéene naa doon lawax ci wotey palum Njiitu réew yu ñaar-fukki fan ak juróom ci weeru féewaryee 2024.

Kon, bu dee lëkkatoog YAW rekk, daanaka amagum na lu tollu ci ñetti lawax yoo xam ne fésal nañu seen ug bokk. Waaye, mbir mi yemul foofu ndax, ñii di waa PUR tamit dinañu am lawax, ci seen i wax. Ñoom, nag, seen mébét mooy Sëriñ Mustafaa Si doon seen lawax ci wote yooyu. Ak lu ci mën di am, sëriñ bi moo yor kàddu gu mujj gi. Te, ndogalam la gaa ñiy déglu. Mu am tamit beneen lawax ci wote yooyu. Muy kii di Maalig Gàkku Njiitul Grand Parti nga xam ne, moom ak Ahmed Aydara, bokk ci lëkkatoo YAW, ñoo nar a ànd ci liggéey boobu.       

Ba tey, mu am beneen lawax bu namm a bokk ci wote yooyu. Muy Doktoor Baabakar Jóob mii di Njiitul FDS (Forces Démocratiques du Sénégal) Les Gelwaar. Loolu la biral ci kàddu yi mu yékkati woon ca seen ndajem ma mu amaloon ci njeexitalu weeru saŋwiyee wi.

Askanu Senegaal dafa moom boppam. Te, askan woowu mooy dogal te dina dogal, kenn moomu nu. Ci jamono jooju ñu jóge ci am ndaje (congrès), mu am lu mu ma ñaan, ñu dogal démb. Ne man Doktoor Baabakar Jóob mi jiite FDS-Les Gelwaar, dañoo sàkku ci man ma nekk lawax ci wotey 2024 yi. Ma bëgg ci indi tontu, di leen yëgal yeen waa Gelwaar, di yëgal askanu Senegaal, di yëgal askanu Afrig, ne loolu ngeen sàkku, bés niki tey nangu naa ko.”  

Mu am ba tey keneen walla ñeneen ñoo xam ne seen taxawaay leeragul ci wote yooyu. Kenn ci ñoom di Mammadu Ibra Kan mi nga xam ne taxawal na ag mbootaay ñaar-fukki fan ak juróom ci weeru féewaryee wii. Mbootaay googu mi ngi ko dippe Demain, c’est maintenant. Moom nag, lii la tontu ci laaj bi ñeel ag bokkam ci wote yooyu  

“Dama ne, gis naa, dawal naa, dégg naa, ñu ne MIK lawax la ci wotey 2024 yi. Laaj nañu ma ndax damay nekk lawax. Sama tontu mooy, lu jot rekk yomb. Te, bu nu ci tolloo, dinanu ci wax. Te, loolu itam dina leer. Li ci des mooy ne Senegaal noo ko moom, ku nekk am nga sañ-sañ ne samp naa sama ndënd. Njiitu réew ma woon, Abdu Juuf moo daan wax ne “Jàkka jaa ngi noonu, ku mën, na noddu.” Kon, loolu mooy tontu bi jarul yàkkamti.”

Keneen tamit ku ame taxawaay boobu, mooy kii di Aminata Ture nga xam ne génnoon na BBY ca jamono jale weesu. Moom nag, yemul ci génn BBY rekk, waaye dafa bëggoon a nekk dépite bu farul fenn. Loolu nag mujjul woon àntu. Laaj bi ñeel nekkam lawax ci wotey 2024 yi moom it tontoom leeru ci. Moo tax mu ne : “Maa ngi xalaat bu baax ci 2024. Dinaa dem nag waxtaan ak saa-Senegaal yi, xale yi, mag ñi ak ndaw ñi, sàkku seen ndimbal. Kilifa diine yi, kilifa aada yi ak ñi nekke ca bitim-réew, sàkku seen ndimbal. Dinaa dellusiwaat seen kanam jox leen leeral yépp.”     

Idiriisa Sekk moom mi nga xam ne mooy Njiitu làng gii di Réew Mi, ma ngay dajalewaat ndànk-ndànk ay ñoñam. Kon, boo moytuwul léegi digganteem ak kii di Njiitu réew mi Maki Sàll tambalee ñagas. Ndax kat, ñaari kuy moom, mënuñoo bokk mbalka. Moom, ci ndajem-waxtaan ma mu doon amal keroog xamle na ci ne ñàkkul mbooloo ma mu amoon ba tey. Nde, ndox kat, fa mu daan taa démb, boo fa demee fekk fa tooy-tooy. Waaye, yëf yi leeragul ba léegi. Ñi leerle kay mooy Bugaan Géy, Xalifa Sàll, Usmaan Sonko ak Abdu Rahmaan Juuf nga xam ne biral na ko ci kàddoom yii :  

Senegaal waruñu xeeb xam-xamu kenn, waruñu xeeb ku jàng araab, waruñu xeeb ku jàng àngale, waruñu jël ñi jàng farañse teg leen ci kow ñeneen. Dëkk ngir suqaliku ku nekk la nga xam ne fa nga juddoo ci dëkk bi, bokku fa, njariñ li nga mën a indil dëkk bi daf koo war a jariñoo. Loolu moo nekkoon solos ndaje mi Parti Awale amal ko, man lawax ci wotey 2024 yi ma amal ko, ñi nga xam ne dañu fi nekk ñu woo leen fi te bokkuñu péete waaye ay boroom xam-xam lañ. Xam-xam boobu nag bëgg nanu ëllëg nu jële ci loo xam ne ay naal yu baax la.

Mu amati lawax boo xam ne, sikki-sàkka am na ci ag bokkam ci wote yooyu. Muy kii di Njiitu réew mi Maki Sàll nga xam ne, moo ngi ci ñaareelu moomeem. Te, gaa ñi jàpp ne Ndeyu-àtte bi mayu ko mu am ñetteelu moome. Waaye, kii di jëwriñ ji mu dénk wàllu yoon, Ismayla Maajoor Faal, lii la tontu ci mbir moomu : 

Li ëpp ci saa-Senegaal yi su ñu taxawee takku ne Njiitu réew mi dañoo bëgg nga wéyal, dinañu booloo woteel la 2024 nga nekk lawax nekkaat Njiitu réew mi. Njiitu réew mi day nekkaat lawax te, day nekkaat Njiitu réewu Senegaal. Jaay kàrt yi njariñ li mooy su nu jaayee ñaari miliyoŋi kàrt, dinanu ne ñaari miliyoŋi saa-Senegaal bëgg nañu Njiitu réew mi nekkaat lawax. Ñaari miliyoŋi saa-Senegaal su ñu taxawee ne Njiitu réew mi bëgg nanu nga nekk lawax loolu kenn mënu ci dara ,ndax mboloo mi mooy dogal. Moo tax duñu wax ay waxi yoon, ay waxi mën na ko, mënu ko. Ndax, Ndeyu-àtte yi leer na, loolu Ndajem ndeyu-àtte réew mi moo ciy wax.”        

Kon, léegi yëf yi leer. Dina bokk am du bokk dees na ci xam dara. Ndax, lu tëw a xam kat dafa yàggul. Te, fii ak i weer kepp, gaa ñi jébbal seen i wayndare. Su boobaa dees na xam fu yëf yi di mujj. Li ci kanam moom, rawal i bët. Te, ku dund rekk, dinga fekke. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj