Ubbi nañu utum parenaas yi ñeel wotey 2024 yi. Ñi fas yéene nekk lawax daldi sóobu ci njëkkante bi ngir matale lim bi. Waaye kii di Usmaan Sonko, njiitul Pasteef la woon, dañ koo seppeeti ci mbir yi.
Ñeenti weer kepp a des ci wotey 2024 yi. Jëwriñ ji ñu dénk kaaraange biir réew mi daldi biral coppite yi ñu namm indi ci palin yi, maanaam ci kot elegtoraal bi. Ci pàttali, coppite yooyoo ngi ñu tënkoon ci péncoo mi fi njiitu réew mi Maki Sàll woote woon ci jamono yii weesu. Ci areete bi jëwriñ ji siiwal, ñu mën cee jàng ni :
« War na képp ku nekk ci lawax yiy xëccoo njiitul réew mi mu sàmmoonteek benn ci tànneef yii di list elegtoraal bi, dépite yi walla njiiti gox yeek gox-goxaat yi. »
Bu dee ci list elegtoraal bi, lawax bi war naa am lu mu tuuti tuuti 0,6% (44231) te warul a weesu 0,8% (58975) ci ñu bindu ñi. Rax ci dolli, war naa am 7i diwaan yoy bu ci nekk dina fa jële 2000y xaatim. Bu dee ku tànn dépite yi, war naa am 8%, di 13i dépite yu ko xaatimal. Bees jàllee ci ku tànn njiiti gox yeek gox-goxaat yi nag, war na ci moom mu am 20% ci ñoom, maanaam 120i njiit.
Naka noonu, wure wa dem këŋ, xëccoo bi daldee tàmbali. Mboolem ñi namm bokk ci ñiy xëccoo réew mi demoon nañ démb jëli wayndare yi ñu war a bind parenaas yi. Ñu waññi fa lu ëpp téeméeri lawax (126 la wax) yoy seen i ndaw dalal nañ leen ba jox leen wayndare.
Li dellu yéeme ci mbir mi nag mooy ni kii di Usmaan Sonko bokkul ci boobu lim. Nde dañ gàntal ndawam li mu yabaloon ngir mu bindu niki ñépp. Ñu jàpp ni li ñu ko génne woon ci list elegtoraal bi moo ko waral. Ay ñoñam di wéy dee yuuxu ne amul lenn lu koy layal. Ba tey dañuy wéy di salfaañe ay àq ak yelleefam.
Waaye dafa mel ni bettu leen wenn yoon. Nde, ñii di Biram Suley Jóob, Basiiru Fay ak Gii Mari Saañaa yebal nañ fa ndaw ba ñu bind leen.