WOTEY 2024 YI : BENNOOG TUGAL (U.E.) A NGI GËTËN MAKI SÀLL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Waa Bennoog Tugal (Union Européenne) àddooti nañ ci wotey 2024 yees war a amal fi Senegaal ngir palug Njiitu réew lu bees. Ñuy fàttali Maki Sàll ni wote yi dafa war a am laata moomeem gi di jeex.

Ci jamono yee weesu, mbootaayu réewi Tugal yi xamle woon na ni moo ngi topp bu baax xew-xew yi nekk di am fi réewum Senegaal te wotey Njiitu réew mi ñu ajandi waral leen. Naka noonu, Natali Masrali mi yor kàddu toogaanu UE gu kawe gi ñeel mbiri bitim-réew, pólitig geek kaaraange gi, moom, dellusiwaat na ci. Fekk mu doon mu doon janook taskati xibaar yi.

Kàddu yi mu fa yékkati dañoo dellu di dëggal taxawaay bi UE amoon, te muy topp ak woo pàcc yépp ci ñu topp ndogalu Ndayu Àtte réew mi. Rafetlu naat wax ji Njiitu réew mi Maki Sàll biral ni dina joxe lenge yi bu moomeem gi jeexee ak li Ndayu Àtte réew mi dëggal limub lawax yiy joŋante. Waaye, yamul ci yii. Ndaxte, fàttali na ni bés bi ñuy àjji wote yi warul a weesu bésub 2 awril bi Maki Sàll war a jeexal.

« Ginnaaw ajandi gi ñu def wotey 25 féewiryee yi, Bennoog Tugal gee ngi aju ci ndogal li Ndayu Àtte réewum Senegaal jël keroog bésub 15 féewiryee bii weesu, di ci woo kilifa yi ñu amal wotey palug Njiitu réew mi ci ni mu gënee gaaw. Bu ñu fàtteet ni amalug wote yi warul a génn àppug moomeg Njiitu réew mi.”

Natali Masrali wax na tamit li ñeel ñaxtu yiñ namm amal ci fan yii di ñëw. Ba tax muy sàkku ci kilifa yi ñu bañ leen a gàntal te sàmmonteek àq ak yelleefi askan wi.

Waaye bés bi ñu war a amal wote yi yitteelul rekk kurélu UE gi. Nde, Mbooloo way-jàngune yi ñeel demokaraasi dellusiwaat na ci. Ñoom sax dañ dàq lépp luy ndogal lu tukkee ca diisoo ba amoon ci 26 ak 27 féewiryee. Li ñuy sàkku mooy Ndayu Àtte réew mi tànn bés balaa moomeg Njiitu réew mi di jeex.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj